Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi - Esayi 1

Esayi 1:5-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Xanaa dungeen wéye fippu, ñu gën leena duma, te bopp di góomi neen, xol jeex tàkk?
6Bopp ba téstën, fenn jagul. Xanaa gaañu-gaañu aki dagg-dagg rekk, ak góom yuy nàcc, fajeesu ko, takkeesu ko, gajfaleesu kook ag diw.
7Seenum réew gental, seeni dëkk xoyomu, seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam, muy gent bu doxandéem tas.
8Siyoŋ, dëkk bu taaru baa ngi wéet ni mbaarum tóokër mbaa dalub toolu xaal. Mbete dëkk bu ñu gaw!
9Bu nu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi waccalul woon li nu deseek as néew, ni Sodom lanuy mel, Gomor lanuy neexool.
10Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom, teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.
11«Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax. «Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy, suur nebbonu juru yar gi, deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.
12Bu ngeen dikkee, teewsi fi sama kanam, ana ku leen sant ñu joggat-joggatee nii sama ëttu kër?
13Buleen fi indeeti saraxi caaxaan, seen saraxu cuuraay, lu ma seexlu la. Terutel weer ak bésub Noflaay ak wooteb ndajee ci yem! Duma mana dékku ndajem diine mu rax njubadi.
14Seeni Terutel weer ak seen bési màggal laa bañ ci sama xol; yooyu màggal a ma diis ba àttanatuma ko.
15Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.
16Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.
17Jàngleen di def lu baax, sàkku njub, waññi ab notkat, àtte dëgg, ab jirim, sàmm àqu jëtun.
18«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.

Read Esayi 1Esayi 1
Compare Esayi 1:5-18Esayi 1:5-18