Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi - Esayi 1

Esayi 1:25-28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
25Yerusalem, maa lay teg loxo, maay seeyal sa raxit ni xeme, ba dindi sa mbuubit mépp.
26Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»
27Siyoŋ dëppook yoon, mucc, ay tuubkatam wormaal njekk, raw;
28moykat ak bàkkaarkat yàqoondoo, dëddukati Aji Sax ji sànkoondoo.

Read Esayi 1Esayi 1
Compare Esayi 1:25-28Esayi 1:25-28