Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi - Esayi 1

Esayi 1:22-30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
22Sa xaalis doon na raxit, sa biiñ xormbet.
23Seeni njiit të, xejjoo ay sàcc, ñoom ñépp sopp ger, di dàq ay neexal, ab jirim, sàmmuñu àtteem, àqu jëtun soxalu leen.
24Moo tax, kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi, Jàmbaaru Israyil: «Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom! Maay fey samay noon!
25Yerusalem, maa lay teg loxo, maay seeyal sa raxit ni xeme, ba dindi sa mbuubit mépp.
26Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»
27Siyoŋ dëppook yoon, mucc, ay tuubkatam wormaal njekk, raw;
28moykat ak bàkkaarkat yàqoondoo, dëddukati Aji Sax ji sànkoondoo.
29Yeenay rus moos ci garab yu mag, yi ngeen soppoona daje, di xërëmtu. Yeenay am gàcce ci tóokër, yi ngeen taamu woona daje, di bokkaale.
30Yeenay meli ni garab gu mag gu xob ya lax, mbaa tóokër bu amul siitu ndox.

Read Esayi 1Esayi 1
Compare Esayi 1:22-30Esayi 1:22-30