19Su ngeen ma nangoo déggal, ngëneelu réew mi ngeen di xéewloo.
20Waaye su ngeen lànkee, fippu, saamar a leen di xéewloo.» Aji Sax ji déy a ko wax ci gémmiñam.
21Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc, te nekkoon dëkkub kóllëre, njubte mate fa, njekk lal fa panaan, tey ñu diy bóomkat!
22Sa xaalis doon na raxit, sa biiñ xormbet.