14Seeni Terutel weer ak seen bési màggal laa bañ ci sama xol; yooyu màggal a ma diis ba àttanatuma ko.
15Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.
16Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.
17Jàngleen di def lu baax, sàkku njub, waññi ab notkat, àtte dëgg, ab jirim, sàmm àqu jëtun.
18«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.
19Su ngeen ma nangoo déggal, ngëneelu réew mi ngeen di xéewloo.
20Waaye su ngeen lànkee, fippu, saamar a leen di xéewloo.» Aji Sax ji déy a ko wax ci gémmiñam.
21Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc, te nekkoon dëkkub kóllëre, njubte mate fa, njekk lal fa panaan, tey ñu diy bóomkat!