5Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,
6ma xabtal ko fi kaw xeet wu gëmadi, yebal ko ca askan woowu ma merloo, ngir ñu sëxëtoo leen, nangu seen alal, note leen ni banu mbedd.
7Waaye Asiri gisewu ko noonu, xalaatewul noonu; bóome la xintewoo, ba fàkkas xeeti xeet.
8Mu ngi naan: «Xanaa du sama jawriñ yépp a diy buur?
9Kalne daa gën Karkemis gee ma nangu? Am Amat daa gën Arpàdd? Am Samari daa gën Damaas?