30Yeen waa Galim, yuuxuleen, yeen waa Laysa, dégluleen, yeen waa Anatot, feeluleen.
31Waa Madmena ñooy fëlxoo, waa Gebim wuti rawtu.
32Tey jii noon yaa ngay taxaw fa Noob, di sànni loxo waa tundu Siyoŋ, di ko tëkkoo waa Yerusalem googu.
33Boroom baa ngoog, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ngi gor garab yi, di rajaxe car yi, njobbaxtal ya gëna kawe dog, la ca gënoona siggi, wàcc.
34Mooy jël sémmiñ, goraale gajji gott bi, Libaŋ loroo loxol boroom doole, ba jóoru.