19gott ba dese garab yu néew yu gone mana lim, bind ko.
20Keroog bés booba li des fi Israyil ak li rëcce kër Yanqóoba duñu wéerooti ña leen duma. Aji Sax ji lañuy wóolu, wéeroo ko, Aji Sell ju Israyil.
21Aw ndes ay délsi, di ndesu askanu Yanqóoba, ñeel Yàlla Jàmbaar ji.
22Seen xeet wi ni feppi suufas géej lay tollu, te as ndes a ciy délsi. Àtteb sànkute mooy taxaw, yoon toppe ba mat sëkk.
23Sànkute déy mooy taxaw, Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi di ko sottal fi réew mi mépp.