10Maa duma réew yu seeni yàllantu, seeni tuur sut tuuri Yerusalem ak Samari.
11Na ma tege loxo Samari aki yàllantoom, duma ni tege loxo Yerusalem aki tuuram?»
12Boroom bi nee: «Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu Siyoŋ ak fa Yerusalem, maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi, ak gëti xeebaateem.»
13Moom moo ne: «Sama dooley përëg laa defe lii, maa xelu, ràññee; ba randal kemi suufi xeet yi, foqati seeni alal, dañ boroom jal ya niw yëkk, wàcce leen.
14Maa teg alali xeet yi loxo, ni ku gis am tàgg. Maa tonneendoo réewi àddina ni ku for ay nen, tonni lépp, laaf tëf-tëfluwul, sàll newul ciib!»
15Sémmiñ dina diir mbagg ka koy gore? Am dogukaay dina réy-réylu ba sut ka koy doge? Mbete yet wuy xàcci ka ko ŋàbb; mbaa bolde bu walbatiku ŋàbb boroom!
16Moo tax Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, di yebal woppi ràgg fi kaw mbuxreem yi, seen daraja tàkk, sawara xoyom ko.
17Aji Sax ji, leeru Israyil mooy doon sawara, ku Sellam kooku mooy doon tàkk-tàkku sawara, xoyom taxasi Asiri aki dégam ci benn bés.
18Gott bu naat ak tool bu meññ, mu ne faraas fóom, ba mu mel ni ku wopp, yaram way seey,
19gott ba dese garab yu néew yu gone mana lim, bind ko.
20Keroog bés booba li des fi Israyil ak li rëcce kër Yanqóoba duñu wéerooti ña leen duma. Aji Sax ji lañuy wóolu, wéeroo ko, Aji Sell ju Israyil.