1Nanga xam lii: bési tiis yu tar ñu ngi nuy tëru ci mujug jamono.
2Ndaxte nit ñi dinañu siis te fonk xaalis, di ñu réy tey yég seen bopp, ñuy xaste tey xëtt ndigalu waajur; duñu am kóllëre, sellaay
3mbaa cofeel; dañuy jàpp mer ak a sos; ñu xér lañuy doon, ñu soxor te bañ lu baax;
4ay workat lañuy doon, di ñu ëppal te bare tiitar; seen bànneex a leen gënal Yàlla.
5Dañuy mbubboo diine waaye nanguwuñu koo dugal seen xol. Ñu deme noonu, dëddu leen.
6Nit ñu mel noonu ñooy yoxoosu ci biir kër yi, ba fàbbi jigéen ñu ñàkk pastéef, ñi seeni bàkkaar ub seen bopp, te bëgg-bëgg yu wuute jiital leen.
7Duñu noppee gëstu, waaye duñu mana yegg ci xam-xamu dëgg mukk.
8Nit ñooñu dañuy bëreek dëgg, ni Sànnes ak Sàmbares bëree woon ak Musaa; ay boroom xel yu gumba lañu, yu seen ngëm tekkiwul dara.
9Waaye duñu dem fu sore, ndax seen ñàkk xel dina bir ñépp, ni mu dale woon Sànnes ak Sàmbares.
10Waaye yaw nag xam nga bu baax sama njàngle, sama dund, sama takkute, sama ngëm, sama muñ, sama mbëggeel ak sama dékku tiis.
11Xam nga li ma daj ciy fitna ak i coono ci dëkki Ancos, Ikoñum ak Listar. Céy li ma jànkoonteel ciy fitna! Waaye Boroom bi musal na ma ci lépp.
12Te ku bokk ci Kirist Yeesu, te bëgg dund dund gu ànd ak ragal Yàlla, alamikk ñu fitnaal la.
13Waaye nit ñu bon ñi ak naaféq yi dinañu fi yées, di naxe ak a nax seen bopp.
14Yaw nag saxal ci li nga jàng te mu wóor la, xam fi nga tibbe.
15Li dale ci sa ngone xam nga Mbind mu sell, mi la mana yee ci yoonu mucc, jaar ci gëm Kirist Yeesu.
16Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub.
17Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet.