Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 3

1.Buur ya 3:8-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Rax ci dolli, Sang bi, ma nekk ci digg askan wi nga taamu, askan wu yaa, ba maneesu koo waññ mbaa di ko lim.
9Kon nag Sang bi, may ma xel mu am ug dégg mu ma àttee sa ñoñ, ngir may ràññee lu baax ak lu bon. Ndax kat, ana kan moo mana àtte sa ñoñ, wii askan wu réy?»
10Kàddug Suleymaan ga nag neex Aji Sax ji, ndax loolu mu ñaan.
11Mu ne ko: «Gannaaw loolu nga ñaan, te ñaanuloo fan wu gudd, ñaanuloo alal, ñaanuloo itam say noon dee, xanaa di ñaan xel mu rafet moo àttee dëgg,
12dama ne, dinaa la defal li nga ñaan, te sax dinaa la may xel mu rafet, nga am ug dégg, ba raw ku la jiitu ak ku la wuutu.
13Te itam li nga ñaanul dinaa la ko may, booleel la alal ak teraanga, ba doo am moroom ci buur yi, sa giiru dund.
14Te soo jaaree ci samay yoon, jëfe samay sàrt ak samay santaane, muy fi sa baay Daawuda jaaroon, kon dinaa guddal saw fan.»
15Ba loolu amee Suleymaan yewwu, ndeke gént la woon. Mu dellu Yerusalem, taxaw fa kanam gaalu kóllërey Aji Sax ji, def fa ay saraxi rendi-dóomal, ak saraxi cant ci biir jàmm, daldi berndeel jawriñam yépp.
16Ba loolu wéyee mu am ñaari gànc yu dikk ca Buur, agsi ca kanamam.

Read 1.Buur ya 31.Buur ya 3
Compare 1.Buur ya 3:8-161.Buur ya 3:8-16