Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya

1.Buur ya 5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ci kaw loolu Suleymaan moo yilifoon mboolem réew ya dale dexu Efraat, ba ca dëkki Filisteen ña, dem ba ca digu réewum Misra. Ñooña di indil Suleymaan galag, nangul ko giiru dundam.
2Suleymaan daan na njëloo bés bu nekk ñeent fukki barigoy sunguf ak juróom (45), ak juróom ñeent fukki (90) barigo ci sunguf su ñagas;
3ak fukki nag yu ñu yafal, ak ñaar fukki nagi parlu, ak téeméeri gàtt, te limaaleesul xeeti kéwél yaak boroom dunq yu duuf ya.
4Suleymaan moo yilifoon mboolem réew ma féete dexu Efraat sowu, dale ko ca Tifsa ba ca Gasa, muy mboolem réew ya féete dexu Efraat sowu. Jàmm ne ñoyy, féete ko wet gu nekk.
5Diirub ayu Suleymaan gépp nag, waa Yudak Israyil ànd ak xel mu dal; ku ci nekk ak sa ker garabu reseñ ak sa ker garabu figg, fa dale diiwaanu Dan ba ca Beerseba.
6Suleymaan amoon na ñeenti junniy (4 000) wuddi fasi watiir ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000).
7Jawriñ ya dañu daa ay-ayloo, ku nekk ak sa weer wi ngay topptoo dundub Buur Suleymaan, mook mboolem ñi mu bokkaloon njël, ba dara daawu ca ñàkk.
8Peppum lors ji ànd ak ñax mi jëm ci fasi watiir yeek fasi dawkat yi itam, ku nekk ci ñoom da daan indi la ñu ko ca sas, teg ko fa mu wara nekk.
9Ci biir loolu Yàlla jagleel Suleymaan mu ñaw lool, am xel mu rafet ak xam-xamam bu yaa, bu solowoo fànn yu bare ni feppi suufas géej.
10Suleymaan rafetoon nam xel, ba sut mboolem doomi réewum penku ak mboolem waa Misra.
11Rafetoon nam xel ba raw ñépp: muy Etan Esraseen ba, di Eman, di Kalkol, di Darda, doomi Maxol yu góor ya. Turam nag siiw ca mboolem xeet ya ko wër.
12Léeb na ñetti junniy kàddu, woy yi mu fent ëpp junni.
13Faramfàcce na it mbirum gàncax, dale ko ci garabu seedar gu Libaŋ ba ci isob giy sax cib tabax. Jàngle na mbirum mala ak njanaaw ak luy raam, ba ci jën.
14Nit ñi dañu daan jóge ci xeet yépp, di sàkkusi xelam Suleymaan mu rafet; te dañu daan bàyyikoo ci mboolem buuri àddina yi déggoon xelam mu rafet.
15Ba Iram buurub Tir déggee ne Suleymaan lañu fal buur, mu wuutu baayam Daawuda, ak na mu xaritoo woon ak Daawuda naka jekk, Iram daa yónnee ay ndawam ca Suleymaan.
16Suleymaan it yónnee ca Iram, ne ko:
17«Xam nga sama baay Daawuda manul woona tabaxal Yàllaam Aji Sax ji kër gu mu ko tudde, ndax xare yi mu séqoon ak noonam yi ko wër, ba ni leen Aji Sax ji daaneele, mu teg leen tànk.
18Léegi nag sama Yàlla Aji Sax ji may na ma jàmm ne ñoyy, féete ma wet gu nekk, ba awma benn noon, te musiba dabu ma.

19Fii ma nekk damaa fas yéene tabax kër, tudde sama Yàlla Aji Sax ji. Muy la Aji Sax ji waxoon sama baay Daawuda, ne ko: “Sa doom ji may def sa kuutaay ci sab jal moo may tabaxal kër, tudde ma ko.”
20Ci biir loolu ma di la ñaan, nga santaane, ñu goral ma banti seedar yu Libaŋ, te samay surga ànd ak say surga ci liggéey bi. Sa peyooru nit ñi dinaa la ko fey ak loo mana feyeeku, ndax yaw xam nga ne amunu ci sunu biir ñu mane yett bant ni waa Sidon.»
21Ba Iram déggee li Suleymaan wax, am na ca mbégte mu réy. Mu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji tey jii, bi mu mayee Daawuda doom ju rafet xel, mu jiite xeet wu réy wii.»
22Ci kaw loolu Iram yónnee ca Suleymaan, ne ko: «Dégg naa kàddu yi nga ma yóbbante. Man ci sama bopp dinaa la defal li nga bëgg lépp ci wàllu banti garabi seedar ak sippar.
23Samay surgaa koy diree Libaŋ ba ca géej ga, rabat ko, ma jaarale ko ci géej gi ba foo ma wax. Su ko defee ma tas ko foofa, nga yóbbu. Yaw nag nangul ma rekk li may sàkku, muy nga joxal ma sama waa kër ab dund.»
24Ba loolu amee Iram jox Suleymaan la mu bëgg ci banti garabi seedar ak sippar.
25Suleymaan ci wàllu boppam jox Iram ñaar fukki junni ak juróom ñetti (28 000) barigoy peppu bele, ak ñaar fukki barigo ak ñaar (22) ci diwu oliw gu ñu segal. Suleymaan di defal Iram noonu at mu ne.
26Bu loolu weesee Aji Sax ji mayoon na Suleymaan xel mu rafet, na mu ko ko dige woon. Jàmm it doxoon na diggante Iram ak Suleymaan, ba ñu fasante kóllëre ñoom ñaar.
27Buur Suleymaan nag sas fanweeri junniy nit (30 000) ci Israyil gépp ay liggéeyi sañul-bañ.
28Mu di leen yebal Libaŋ, weer wu nekk fukki junni (10 000) dem. Bu ñu amee Libaŋ weer, am seeni kër ñaari weer. Adoniram a jiite woon sas ya.
29Suleymaan sàkk juróom ñaar fukki junniy (70 000) yenukat, ak juróom ñett fukki junniy (80 000) yettkati doj ca tund ya,
30te bokkul ak ñetti junni ak ñetti téeméeri nit (3 300) ñi Suleymaan tabb, ñuy jiite liggéey bi, di saytu liggéeykat yi.
31Buur santaane ñu jële fa doji tànnéef yu réy yu ñuy yett, muy kenug kër Yàlla ga.
32Ba mu ko defee tabaxkati Suleymaan ak tabaxkati Iram ak waa Gebal di yett ak a waajal bant yaak doj, ya ñuy tabaxe kër ga.