Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sàkkaryaa

Sàkkaryaa 5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ci kaw loolu ma dellu séentu, gisuma lu moy taxañu mbind buy naaw.
2Malaaka mi ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Taxañ buy naaw laa gis, guddaayam di ñaar fukki xasab, yaatuwaayam di fukki xasab.»
3Mu ne ma: «Lii mooy alkute giy wàccsi ci kaw réew mi mépp. Li taxañ bi wax ci genn wetam mooy képp kuy sàcc, dees na ko fi dàqe, te li mu wax ci wetam gi ci des mooy képp kuy giñ ci ay fen, dees na ko fi dàqe.
4Maay wàcce alkute gi,» kàddug Aji Sax ji Boroom gàngoor yee, «mu dugg ba ci biir kër sàcc bi, ak kër nit kiy giñe sama tur, ay fen; ci biir kër gi la alkute giy fanaan, ba raafal banti kër gi, aki dojam.»
5Ci kaw loolu malaaka ma doon wax ak man dikk ne ma: «Séentul rekk ba gis lii di dikk.»
6Ma ne: «Lu mu doon?» Mu ne: «Ndabal nattukaay beey génn,» tegaat ca ne: «Lii mooy seen bàkkaar ci biir réew mi mépp.»
7Ci biir loolu kubeeru beteex ga ca kaw ndab la jekki yékkatiku, ndeke jenn jigéen a nga toog ca biir ndab la.
8Mu ne: «Jigéen jii mooy mbon,» daldi koy bëmëx ca biir ndab la, fél kubeeru beteex ga, ubaat ndab la.
9Ba loolu amee ma séentu, yem ci ñaari jigéen ñuy dikk, ngelaw li wal seeni laaf. Laaf yu mel ni laafi xodd lañu am. Ñu daldi yékkati ndabal nattukaay la, ba ca diggante asamaan ak suuf.
10Ma ne malaaka ma doon wax ak man: «Ana fu ñii jëme ndabal nattukaay bi?»
11Mu ne ma: «Ag kër lañu koy tabaxali ca réewum Sineyaar. Bu noppee, fa lañu koy teg, ca kaw tegukaayam.»