Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sàkkaryaa

Sàkkaryaa 2

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba mu ko defee, ma séentu, gisuma lu moy ñeenti béjjén.
2Ma ne malaaka ma doon wax ak man: «Béjjén yii nag?» Mu ne ma: «Béjjén yii ñoo tasaare Yuda ak Israyil ak Yerusalem.»
3Ci kaw loolu Aji Sax ji won ma ñeenti tëgg.
4Ma ne: «Lan la ñii di defsi?» Mu wax ma, ne ma: «Béjjén yii tasaare Yuda ba kenn siggeetul, tëgg yii ñoo dikk ngir tiital leen, ba jàllarbi béjjéni xeet yi jóg song réewum Yuda, tasaare ko.»
5Ma séentu, gisuma lu moy jenn waay ju ŋàbb buumu nattukaay ci loxoom.
6Ma ne ko: «Foo jëm?» Mu ne ma: «Xanaa natti Yerusalem, ba xam nu mu yaatoo, ak nu mu gudde.»
7Fa la malaaka ma doon wax ak man jekki di dem, meneen malaaka dikk dajeek moom.
8Mu ne ko: «Dawal, nga wax xale bu góor bii ne ko: “Yerusalem lees di dëkke, te tata wëru ko; ŋàpp lay def, ndax barewaayu nit ñeek jur gi ci biiram.
9Te man ci sama bopp,” kàddug Aji Sax jee, “maa koy nekkal tatay sawara ji ko ub ràpp. Te it maay doon daraja ji ci biiram.”
10«Éey, éey yeen, dawleen génne réewum bëj-gànnaar,» kàddug Aji Sax jee. «Ni ñeenti ngelawi asamaan tasaaroo, ni laa leen tasaaree.» Kàddug Aji Sax jee.
11«Éy Siyoŋ, rëccal, yaw mi dëkke janq Babilon mu taaru mi.»
12Aji Sax ji Boroom gàngoor yi déy dafa wax, moom mi ma yebal ngir teddngay boppam, ci mbirum xeet, yi leen sëxëtoo woon, nee: «Képp ku leen laal kat, laal na sama reeni xol.
13Maa ngii déy di xàcci sama loxo ci seen kaw, te ñoom la seeni jaam di sëxëtooji.» Kon dingeen xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yebal.
14«Sarxolleel te bànneexu, yaw janq Siyoŋ mu taaru, nde maa ngii di dikk, màkkaanoo fi sa biir.» Kàddug Aji Sax jee.
15«Bésub keroog la xeet yu bare di taqook Aji Sax ji, ba doon sama ñoñ, ma màkkaanoo fi sa biir.» Kon nga xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yebal ci yaw.
16Aji Sax jeey séddoo Yuda, muy wàllam ci suuf su sell si, te mooy taamooti Yerusalem.
17Na wépp suux ne cell fi kanam Aji Sax ji, ma ngoogu sàqee fa màkkaanam mu sell ma.