Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sàkkaryaa

Sàkkaryaa 12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ab yéenee ngi, di kàddug Aji Sax ju dikkal Israyil. Kàddug Aji Sax jee, ki firi asamaan, lal suuf, te bind noowug doom aadama ci biir doom aadama.
2Mu ne: «Maa ngii di waaja def Yerusalem, muy ndabal sànj luy màndee, ñeel mboolem xeet yi ko wër, te kera bu ñuy gaw Yerusalem, Yuda gépp ca lay bokk.
3Bésub keroog maay def Yerusalem di doj wu diis gann ci xeet yépp. Képp ku ko jéema yëngal, da ciy gaañoo gaañu rekk. Te xeeti àddina yépp ay daje ci kawam.
4Su keroogee,» Aji Sax jeey wax: «ngëlëmte laay dumaa wépp fas, te ag ndof laay dumaa gawaram. Kër Yuda nag laa naan jàkk samay gët, te ag cilmaxa laay dumaa wépp fasu xeet yi.
5Su ko defee njiiti Yuda ci seen xol lañu naa: “Waa Yerusalem, sunu doolee ngi ci sunu Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.”
6Bésub keroog maay def njiiti Yuda mel ni ab taal bu jafal jalu matt, mbaa jum bu ñu jafal ci sabaaru pepp; wetu ndijoor ak wetu càmmoñ lañuy xoyome mboolem xeet yi leen wër, te Yerusalem toog bérabam, di Yerusalem ba tey.
7«Aji Sax ji Yuda lay jëkka wallu, ndax darajay waa kër Daawuda, ak darajay waa Yerusalem baña màgg ba ëpple Yuda.
8Bésub keroog Aji Sax jeey doon kiiraayal waa Yerusalem. Ñi gëna néew doole ci ñoom sax ñook Daawudaay tolloo doole, waa kër Daawuda jiite leen ni Yàlla, ni malaakam Aji Sax ji.
9Su bés baa laay tàmbalee faagaagal mboolem xeet yiy songsi Yerusalem.
10«Bu loolu amee maay sottil waa kër Daawuda ak waa Yerusalem, noowug yiw aki dagaan, ba ñu geesu ma man, mi ñu jam ba mu sar, te dinañu ko jooy ni ñuy jooye benn bàjjo, di ko naqarlu ni ñuy naqarloo deewug taaw.
11Su bés baa yuuxi dëj yu réy ay jibe fi Yerusalem, mel ni yuuxi dëj ya ca Adàdd Rimon, ca jooru Megido.
12Waa réew meey jooy seenub dëj, làng gu nekk beru ñoomu neen. Làngu kër Daawuda di ñoomu neen, seeni jabar di ñoomu neen; làngu kër Natan di ñoomu neen, seeni jabar it di ñoomu neen.
13Làngu kër Lewi di ñoomu neen, seeni jabar di ñoomu neen; làngu Simey di ñoomu neen, seeni jabar di ñoomu neen.
14Mboolem làng yi ci des it, làng gu ci nekk di ñoomu neen, seeni jabar di ñoomu neen.