Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sàkkaryaa

Sàkkaryaa 14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Bés a ngii di dikkal Aji Sax ji, ca lees di séddoo fi seen biir, alal ju ñu nangoo ci yeen.
2Xeet yépp laay dajale ci kaw Yerusalem, ngir xare. Dëkk bi lees di nangu, sëxëtoo kër yi, tëdde jigéen ñi. Genn-wàllu dëkk beey génn, jëm ngàllo, waaye ndesu askan wi, deesu leen dagge ci dëkk bi.
3Su boobaa la Aji Sax jiy génn, xeex ak yooyu xeet, ni mu baaxoo xeexe ci bésub xare.
4Bésub keroog, kaw tundu Oliw ya la tànkam yay sampe, fa janook Yerusalem, ca penku, tundu Oliw ya xar ca digg ba, penku ba sowu, def xur wu yaa, genn-wàllu tund wa randu, jëm bëj-gànnaar; genn-wàll ga jëm bëj-saalum.
5Xur wa ca diggante sama tund ya ngeen di jaare daw, ndax xur wa ba Accal lay àkki. Na seeni maam dawe woon ngeen di dawe, ba suuf sa yëngoo, ca janti Osiyas buurub Yuda. Sama Yàlla Aji Sax ji mooy dikk, ànd ak mboolem ñu sell ñi.
6Bésub keroog, dug leer, dub sedd, te du benn tawub yuur.
7Benn bésu boppam lay doon bu Aji Sax ji doŋŋ xam; du doon bëccëg, du doon guddi, te bu ngoonee mu leer.
8Bésub keroog Yerusalem la ndox muy dund di wale, genn-wàll gi jëm géeju penku, genn-wàll gi, géeju sowu, te noor ak nawet lay doon.
9Aji Sax ji mooy doon buuru àddina sépp, bésub keroog Aji Sax ji di kenn, turam di wenn.
10Réew mi mépp ag joor lay soppliku, dale ko Geba ba Rimon ca bëj-saalumu Yerusalem, Yerusalem tooge bérabam, tiim la ko wër, dëkk bi dale ca buntu Beñamin, ba fa bunt ba woon, jàll ba ca buntu Jàddukaay ba, daleeti ca tatay Ananel ba ca nalukaayi reseñi buur.
11Dees na ko dëkke te deesatu ko faagaagal, kaaraange la Yerusalem di dëkke.
12Yii duma la Aji Sax jiy duma mboolem xeet yi xareek Yerusalem: Seen suux mooy yàqu te ñu ne jonn taxaw, seeni gët yàqu ca seen biir paxi gët, seenu làmmiñ nëb ca seen biir gémmiñ.
13Bésub keroog tiitaange ju réy mooy tukkee ci Aji Sax ji wàcc ci seen biir; ku nekk jàpp sa loxol moroom, ñu songoo.
14Yuda it day fekksi Yerusalem ci xeex bi, te dees na dajale alali xeet yi leen wër yépp; wurus, xaalis ak yére, bare, ne gàññ.
15Yooyu duma it mooy dal fas, ak berkelleek giléem ak mbaam-sëf, ak lépp luy jur ci biir dal yooyu, noonu lees di dumaa mala yépp.
16Su boobaa mboolem ndesu wépp xeet wu songoon Yerusalem, Yerusalem lay yéegi at mu ne, ngir sujjóotali Buur Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, tey màggalsi màggalu Mbaar yi*.
17Te gépp làngu kaw suuf gu yéegsiwul ba Yerusalem, ngir sujjóotalsi Buur Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, googu làng du tawlu.
18Làngu Misra it, su ñu yéegul ba dikk, duñu tawlu; dinañu jot ci duma yi Aji Sax jiy duma xeet yi yéegul ba màggalsi màggalu Mbaar yi.

19Loolooy doon dumay Misra ngir seen bàkkaar, di dumay wépp xeet ngir seen bàkkaar, ndax ñàkka yéeg ba màggalsi màggalu Mbaar yi.
20Bésub keroog jóolóoliy fas yi sax dees na ci bind: «Sell na ñeel Aji Sax ji.» Te ni ndabi tuurukaay yi fi kanam sarxalukaay bi selle, cin yi gëna néew daraja ci biir kër Aji Sax ji sax noonu lañu selle.
21Su boobaa luy cin ci Yerusalem ak Yuda, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi lees koy sellalal, ba mboolem ñi dikk di sarxalsi, ci lañuy jël, togge. Te bésub keroog ab jula dootu am ci biir kër Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.