Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MÀRK - MÀRK 8

MÀRK 8:5-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
6Noonu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf. Mu jël juróom ñaari mburu yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ngir ñu séddale leen mbooloo mi; taalibe yi def ko.
7Amoon na fa it tuuti jën yu ndaw. Yeesu jël ko, sant Yàlla, wax taalibe yi, ñu séddale leen itam mbooloo mi.
8Noonu nit ñi lekk ba suur, ba noppi taalibe yi dajale juróom ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des.
9Ña ko fekke nag matoon nañu ñeenti junniy góor.
10Bi ko Yeesu defee, mu yiwi leen, daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga, dem ca wàlli Dalmanuta.
11Noonu Farisen yi ñëw, di werante ak moom; ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam.
12Waaye Yeesu binni ci xolam ne leen: «Lu tax niti jamono jii di laaj kéemaan? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, duñu jot genn kéemaan.»
13Ci kaw loolu Yeesu bàyyi leen, duggaat ci gaal gi, di jàll dex gi.
14Taalibe yi nag fàtte woon nañu yóbbaale mburu, te amuñu woon lu dul benn mburu ci gaal gi.
15Noonu Yeesu artu leen ne: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen yi ak ñi far ak buur bi Erodd.»
16Taalibe yi nag daldi werante naan: «Nun de indaalewunu mburu.»
17Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Lu tax ngeen di werante ci li ngeen indaalewul mburu? Xanaa gisaguleen te xamuleen? Ndax seen xol dafa fatt ba tey?

Read MÀRK 8MÀRK 8
Compare MÀRK 8:5-17MÀRK 8:5-17