Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 22

LUUG 22:4-63

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Noonu Yudaa dem waxtaani ak sarxalkat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga, ba xam nan la leen di jébbale Yeesu.
5Ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis.
6Yudaa nangu, di fexe jamono ju mu leen mana jébbal Yeesu, fu mbooloo ma nekkul.
7Bésu màggalu Mburu ma amul lawiir agsi, ca bés boobu lañu waroona rendi gàttub bésu Mucc ba.
8Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, defaral nu reeru bésu Mucc ba.»
9Ñu ne ko: «Fan nga bëggoon, nu defare ko fa?»
10Mu ne leen: «Bu ngeen duggee ca dëkk ba, góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen. Toppleen ci moom ba ca kër ga muy dugg,
11te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru bésu Mucc ba, man ak samay taalibe?”
12Noonu dina leen won néeg bu féete kaw, te yaa, ñu defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.»
13Ñu dem, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.
14Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi,
15ne leen: «Yàkkamti woon naa lool lekk ak yéen reeru bésu Mucc bii, laata ñu may sonal.
16Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Yàlla.»
17Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko.
18Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum reseñ mi, ba kera Yàlla di tëral nguuram.»
19Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»
20Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen.
21Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li.
22Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.»
23Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy nara def loolu.
24Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci ñoom moo gëna màgg.
25Yeesu ne leen: «Buuri xeeti àddina dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañuy sàkku ngërëm.
26Waaye yéen buleen def noonu. Ki gëna màgg ci yéen, na nekk ni ki gëna ndaw, te njiit mel ni surga.
27Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gëna màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga.
28Yéen nag yéenay ñi ànd ak man ci samay fitna.
29Man nag jox naa leen sañ-sañu nguuru, ni ma ko sama Baay joxe.
30Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.»
31Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax.
32Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo délsee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.»
33Piyeer ne ko: «Boroom bi, àttan naa ànd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.»
34Yeesu ne ko: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
35Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
36Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am xaalis, na ko jël; te ku am mbuus, na ko jël; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, jënde ko jaasi.
37Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax fàww mu am ci man, bi mu nee: “Boole nañu ko ak ñu bon ña.” Ndaxte loolu jëm ci man mi ngi mat.»
38Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.»
39Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe naka-jekk. Taalibeem ya topp ci moom.
40Bi mu agsee ca bérab ba, mu ne leen: «Ñaanleen, ngir baña daanu cig fiir.»
41Noonu mu dànd leen, ba fu aw saan mana tollu, daldi sukk di ñaan ne:
42«Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
43Noonu malaakam Yàlla daldi koy feeñu, may ko doole.
44Ci biir tiis, Yeesu gëna sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf.
45Bi mu ñaanee ba noppi, mu jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis.
46Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña daanu cig fiir.»
47Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku ñuy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak ñaar jiite leen. Yudaa jegeñsi Yeesu, bëgg koo fóon.
48Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!»
49Bi ñi àndoon ak Yeesu gisee liy bëgga xew, ñu ne: «Boroom bi, ndax nu dóore jaasi?»
50Kenn ci ñoom nag dóor surgab sarxalkat bu mag ba, noppu ndijooram dagg.
51Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
52Noonu Yeesu ne sarxalkat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc.
53Moona maa nga woon ak yéen bés bu nekk ca kër Yàlla ga, te jàppuleen ma. Waaye léegi seen waxtu la, di jamonoy lëndëm.»
54Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër sarxalkat bu mag ba. Piyeer topp fu sore.
55Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir.
56Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko jàkk ne: «Nit kii itam àndoon na ak moom.»
57Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.»
58Nees-tuut keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer ne ko: «Sama waay, bokkuma ci.»
59Bi ñu tegee lu mat waxtu, keneen dikkaat ca wax ja ne: «Ci lu wóor nit kii àndoon na ak moom, nde Galile la jóge.»
60Waaye Piyeer ne ko: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab.
61Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer fàttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi ñetti yoon.»
62Piyeer daldi génn, di jooy jooy yu metti.
63Nit ñaa nga jàppoon Yeesu, di ko ñaawal ak di ko dóor.

Read LUUG 22LUUG 22
Compare LUUG 22:4-63LUUG 22:4-63