Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 22:4-63 in Wolof

Help us?

LUUG 22:4-63 in Téereb Injiil

4 Noonu Yudaa dem waxtaani ak sarxalkat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga, ba xam nan la leen di jébbale Yeesu.
5 Ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis.
6 Yudaa nangu, di fexe jamono ju mu leen mana jébbal Yeesu, fu mbooloo ma nekkul.
7 Bésu màggalu Mburu ma amul lawiir agsi, ca bés boobu lañu waroona rendi gàttub bésu Mucc ba.
8 Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, defaral nu reeru bésu Mucc ba.»
9 Ñu ne ko: «Fan nga bëggoon, nu defare ko fa?»
10 Mu ne leen: «Bu ngeen duggee ca dëkk ba, góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen. Toppleen ci moom ba ca kër ga muy dugg,
11 te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru bésu Mucc ba, man ak samay taalibe?”
12 Noonu dina leen won néeg bu féete kaw, te yaa, ñu defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.»
13 Ñu dem, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.
14 Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi,
15 ne leen: «Yàkkamti woon naa lool lekk ak yéen reeru bésu Mucc bii, laata ñu may sonal.
16 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Yàlla.»
17 Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko.
18 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum reseñ mi, ba kera Yàlla di tëral nguuram.»
19 Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»
20 Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen.
21 Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li.
22 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.»
23 Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy nara def loolu.
24 Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci ñoom moo gëna màgg.
25 Yeesu ne leen: «Buuri xeeti àddina dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañuy sàkku ngërëm.
26 Waaye yéen buleen def noonu. Ki gëna màgg ci yéen, na nekk ni ki gëna ndaw, te njiit mel ni surga.
27 Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gëna màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga.
28 Yéen nag yéenay ñi ànd ak man ci samay fitna.
29 Man nag jox naa leen sañ-sañu nguuru, ni ma ko sama Baay joxe.
30 Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.»
31 Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax.
32 Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo délsee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.»
33 Piyeer ne ko: «Boroom bi, àttan naa ànd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.»
34 Yeesu ne ko: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
35 Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
36 Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am xaalis, na ko jël; te ku am mbuus, na ko jël; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, jënde ko jaasi.
37 Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax fàww mu am ci man, bi mu nee: “Boole nañu ko ak ñu bon ña.” Ndaxte loolu jëm ci man mi ngi mat.»
38 Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.»
39 Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe naka-jekk. Taalibeem ya topp ci moom.
40 Bi mu agsee ca bérab ba, mu ne leen: «Ñaanleen, ngir baña daanu cig fiir.»
41 Noonu mu dànd leen, ba fu aw saan mana tollu, daldi sukk di ñaan ne:
42 «Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
43 Noonu malaakam Yàlla daldi koy feeñu, may ko doole.
44 Ci biir tiis, Yeesu gëna sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf.
45 Bi mu ñaanee ba noppi, mu jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis.
46 Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña daanu cig fiir.»
47 Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku ñuy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak ñaar jiite leen. Yudaa jegeñsi Yeesu, bëgg koo fóon.
48 Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!»
49 Bi ñi àndoon ak Yeesu gisee liy bëgga xew, ñu ne: «Boroom bi, ndax nu dóore jaasi?»
50 Kenn ci ñoom nag dóor surgab sarxalkat bu mag ba, noppu ndijooram dagg.
51 Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
52 Noonu Yeesu ne sarxalkat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc.
53 Moona maa nga woon ak yéen bés bu nekk ca kër Yàlla ga, te jàppuleen ma. Waaye léegi seen waxtu la, di jamonoy lëndëm.»
54 Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër sarxalkat bu mag ba. Piyeer topp fu sore.
55 Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir.
56 Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko jàkk ne: «Nit kii itam àndoon na ak moom.»
57 Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.»
58 Nees-tuut keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer ne ko: «Sama waay, bokkuma ci.»
59 Bi ñu tegee lu mat waxtu, keneen dikkaat ca wax ja ne: «Ci lu wóor nit kii àndoon na ak moom, nde Galile la jóge.»
60 Waaye Piyeer ne ko: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab.
61 Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer fàttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi ñetti yoon.»
62 Piyeer daldi génn, di jooy jooy yu metti.
63 Nit ñaa nga jàppoon Yeesu, di ko ñaawal ak di ko dóor.
LUUG 22 in Téereb Injiil

Luug 22:4-63 in Kàddug Yàlla gi

4 Yuda daldi diisooji ak sarxalkat yu mag ya, ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ngir xam nan lay tege Yeesu ci seeni loxo.
5 Ñu am ca mbégte, digook moom, ngir jox ko xaalis.
6 Yuda nangu, di wut nag yoon wu mu wore Yeesu, fu mbooloo ma teewul.
7 Ci kaw loolu bésu màggalu Mburu mu amul lawiir agsi, ñu war caa rendi gàttub bésub Mucc.
8 Yeesu yebal Piyeer ak Yowaan ne leen: «Demleen, waajalal nu bésub Mucc bi, ba nu reeri.»
9 Ñu ne ko: «Foo bëgg nu waaje ko fa?»
10 Mu ne leen: «Bu ngeen di dugg ca dëkk ba rekk, dingeen dajeek waa ju yenu njaqas ndox. Toppleen ci moom ba ca biir kër ga mu jëm,
11 te ngeen ne boroom kër ga: “Sëriñ bi nee: Ana néegu gan, bi may reere reeru bésub Mucc, maak samay taalibe?”
12 Kooku moo leen di won néegub kaw bu yaa bu ñu defar ba noppi. Foofa ngeen di waajale.»
13 Ba ñu demee, noonee leen ko Yeesu waxe, na lañu gise lépp. Ñu daldi waajal reer ba.
14 Ba waxtuw reer jotee, Yeesu toog ak ndaw ya,
15 ne leen: «Yàkkamti woon naa lool bokk ak yeen reeru bésub Mucc bii, bala maa tàbbi coono.
16 Ndax maa leen ko wax, dootuma ko reer mukk, ba keroog solob reer bi di sotti ca nguurug Yàlla.»
17 Ci kaw loolu mu jël ab kaas, yékkati kàddug cant, daldi ne: «Jël-leen kaas bii, te ngeen séddoo ko.
18 Ndax maa leen ko wax, gannaaw-si-tey dootuma naan ndoxum reseñ, ba kera nguurug Yàlla dikk.»
19 Gannaaw loolu mu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg ko, jox leen ko ne: «Lii moo di sama yaram wi ñu jooxe ngir yeen. Deeleen def lii, di ma ko fàttlikoo.»
20 Kaas ba itam noonu la def ak moom gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret ji leen nara tuurul.
21 Waaye nag ki may wor, loxoom a ngi ci ndab lii nu bokk.
22 Doomu nit ki déy, ni ñu ko dogale, noonu lay deme, waaye wóoy ngalla ki pexe mi ñu koy wore di jaare ci moom.»
23 Ci kaw loolu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom moo nar jooju jëf.
24 Ab werante itam dikkal leen, ñuy xëccoo ci seen biir ku wara gëna kawe ci ñoom.
25 Yeesu nag ne leen: «Buuri xeeti àddina doole lañuy nguuroo ci seen kaw, teewul ñi leen di néewal doole, baaxekati nit ñi lañu leen di wooye.
26 Yeen nag bumu deme noonu ci seen biir. Ki gëna kawe ci yeen, na mel ni moo gën di ndaw, te njiit li, na mel ni ab surga.
27 Ki ñu taajal ndab li, ak surga bi ko taajal, ana ku ci gëna kawe? Xanaa du ki ñu taajal? Moonte man, ci seen biir laa tooge toogaayu surga!
28 Yeen nag yeenay ñi des ak man ci sama biir coono.
29 Man itam ni ma sama baay dénke nguur, ni laa leen koy dénke.
30 Yeenay lekk ak a naane ca sama ndab, ca sama nguur, te yeenay tooge ay gàngune, di jiite fukki giiri bànni Israyil ak ñaar.»
31 Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp.
32 Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.»
33 Piyeer ne ko: «Sang bi, jekk naa ci ànd ak yaw kaso, ak ci ànd ak yaw dee.»
34 Yeesu ne ko: «Piyeer, maa la ko wax, bala ganaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
35 Yeesu neeti leen: «Ba ma leen yebalee te du dencukaayu xaalis, du mbuus, du carax yu ngeen yóbbaale, ndax ñàkk ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
36 Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am dencukaayu xaalis, na ko jël, ku am mbuus it, na ko jël; ku amul saamar, na jaay mbubbam, jënde saamar.
37 Ndax maa leen ko wax, li ñu bind ne, “Mook defkati mbon yi lañu boole ab àtte,” fàww mu am ci man, te loolu jëm ci sama mbir mu ngi sottisi.»
38 Ñu ne ko: «Sang bi, ñaari saamar a ngi fi.» Mu ne leen: «Doy na.»
39 Ci kaw loolu Yeesu génn, jëm ca tundu Oliw ya, na mu ko baaxoo woon, taalibe ya topp ci moom.
40 Ba mu agsee ca bérab ba, da ne leen: «Ñaanleen, ngir baña tàbbi cig fiir.»
41 Ba loolu amee mu dànd leen lu tollook saanu xeer, daldi sukk, di ñaan.
42 Mu ne: «Baay, su dee sa coobare, teggil ma kaasu naqar bii. Bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
43 Malaaka mu bawoo asamaan daldi koy feeñu, dooleel ko.
44 Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.
45 Mu ñaan ba noppi, daldi jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, sonn lool ndax aw tiis.
46 Mu ne leen: «Lu ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir.»
47 Naka la Yeesu di wax, daaneelagul, mbooloo ne jimeet, ka ñuy wax Yuda, di kenn ca Fukk ñaak ñaar jiite leen. Yuda dikk ba ci Yeesu, bëgg koo fóon.
48 Yeesu ne ko: «Yuda, fóon ngay wore Doomu nit ki!»
49 Ña ànd ak Yeesu nag gis la ca nara topp, ñu ne: «Sang bi, nu jame saamar boog?»
50 Kenn ci ñoom daldi caw surgab sarxalkat bu mag ba, njoof noppu ndijooram.
51 Teewul Yeesu ne: «Bàyyileen, na fi yem.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
52 Ba loolu amee Yeesu wax ak ña ko jàppsi: sarxalkat yu mag ya, ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ak mag ña. Mu ne leen: «Mbete dama di ab fippukat, ba ngeen dikkey saamar aki njur.
53 Moona bés bu nekk, maak yeen la woon ca kër Yàlla ga, te teguleen ma loxo. Waaye seen waxtu la léegi, bi kilifteefug lëndëm ayee nii.»
54 Ba mu ko defee ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ba ca kër sarxalkat bu mag ba, Piyeer dànd fu sore, topp ca.
55 Fekk na ñu taal sawara ca digg ëtt ba, toog yéew sawara wa, Piyeer dikk toog ca seen biir.
56 Ab surga bu jigéen nag gis ko, mu toog fi kanam taal bi, mu ne ko jàkk, ne: «Kii it ci la, moom la àndaloon!»
57 Piyeer nag miim, ne: «Soxna si, xawma kooku!»
58 Nes tuut keneen gis ko ne: «Yaw it ci ñoom nga!» Piyeer ne ko: «Waa jii, du man!»
59 Ba ñu ca tegee lu mat waxtu, keneen jaaraat ca wax ja ne: «Kii kay wax-dëgg, moom la àndaloon, nde waa Galile la.»
60 Teewul Piyeer ne ko: «Waa jii, li ngay wax, xawma ma ko de!» Ca saa sa, ganaar sab, te kàddug Piyeer daanoogul sax.
61 Ci kaw loolu Sang bi geesu, ne jàkk Piyeer, Piyeer fàttliku la ko Sang bi waxoon ne ko: «Bala ganaar a sab tey jii, dina fekk nga jàmbu ma ñetti yoon.»
62 Piyeer nag génn, di jooy jooy yu metti.
63 Ci kaw loolu ña jàpp Yeesu, di ko kókkali ak a dóor.
Luug 22 in Kàddug Yàlla gi