Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 18

Luug 18:5-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5waaye jigéen jii da maa lakkal; naa ko àtte, bala moo dërr-dërri ba mujj jekkli ma.”»
6Sang bi teg ca ne: «Jàngatleen li àttekat bu bon bi wax.
7Kon ndax Yàlla man naa baña sàmm àqu tànnéefam ñi koy woo wall guddi ak bëccëg, xanaa di leen yeexe?
8Maa leen ne, mooy sàmm seen àq ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki dikkee, mbaa dina fekk ngëm ci kaw suuf?»
9Yeesu léebati lii, ngir ñiy damoo seenug njub, tey doyadal ñi ci des.
10Mu ne: «Ñaari nit a julliji woon ca kër Yàlla ga. Kenn ki di ab Farisen, ki ci des dib juutikat.
11Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi doonul lu moy ay lekk-kati àq, ay njublaŋ aki jaalookat, rawatina juutikat bii.
12Maa ngi woor ñaari yoon, ayu bés gu nekk, di joxe asaka benn céru fukkeelu mboolem lu ma am.”
13«Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore, ñemewula siggi sax, xool asamaan, xanaa di fëgg dënnam te naan: “Éy Yàlla, yërëm ma, man bàkkaarkat bi.”»
14Yeesu teg ca ne: «Maa ne leen, kooku moo ñibbaale këram àtteb ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, waaye ki toroxlu lees di yékkati.»
15Doon nañu indil Yeesu ay tuut-tànk sax, ngir mu teg leen ay loxoom. Taalibe ya gis loolu, di leen jànni.
16Yeesu nag woolu xale yi, ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man, buleen leen aaye, ndax ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguurug Yàlla.

Read Luug 18Luug 18
Compare Luug 18:5-16Luug 18:5-16