Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 12

LUUG 12:53-59

Help us?
Click on verse(s) to share them!
53Baay dina féewaloo ak doom, doom ak baayam. Ndey dina féewaloo ak doomam ju jigéen; doom ju jigéen ji ak ndeyam. Goro dina féewaloo ak soxnas doomam; soxnas nit ak goroom.»
54Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiin ci sowu, dangeen naan ca saa sa: “Dina taw,” te mooy am.
55Te bu ngeen yégee ngelaw liy uppe sudd, ngeen ne: “Dina tàng tàngaay wu metti,” te mooy am.
56Naaféq yi ngeen doon! Man ngeena ràññee melow asamaan ak suuf, waaye lu tax manuleena ràññee li jamonoy léegi ji di tekki?
57«Lu tax it dungeen àtteel seen bopp liy jëf ju jub?
58Bu la nit jiiñee dara, ba ngeen ànd di dem ca àttekat ba, nanga fexee juboo ak moom ci yoon wi. Lu ko moy, dina la yóbbu ci yoon, yoon jébbal la ca loxoy alkaati ba, mu tëj la.
59Maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo fiftin bi ci mujj.»

Read LUUG 12LUUG 12
Compare LUUG 12:53-59LUUG 12:53-59