53 Baay dina féewaloo ak doomam ju góor, doom ja féewaloo ak baayam; ndey féewaloo ak doomam ju jigéen, doom ja féewaloo ak ndeyam; ndey féewaloo ak jabaru doomam, jabar ja féewaloo ak ndeyu jëkkër ja.»
54 Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiine sowu, dangeen dal naan: “Taw baa ngi ñëw,” te noonu lay ame.
55 Bu ngelaw bawoo bëj-saalum, ngeen ne: “Tàngaay wu metti lay doon,” te mooy am.
56 Jinigalkat yi ngeen doon! Melow asamaan ak suuf, man ngeen koo firi. Xew-xewi janti tey jii nag, nu ngeen umplee pireem?
57 «Te itam lu leen tee àtte njub, yeen ci seen bopp?
58 Boo àndeek sab jotewaale, ngeen jëm ca àttekat ba, fexeela jubook moom ci yoon wi. Lu ko moy mu yóbbu la ci yoon, yoon jébbal la ndawal buur, mu ne la ràpp tëj.
59 Ma ne la, doo fa génne mukk te feyuloo lépp, ba ci poset bi gëna tuut.»