13Kenn ca mbooloo ma moo noon Yeesu: «Sëriñ bi, waxal ci sama mag, mu jox ma sama wàll ci ndono li nu bokk.»
14Yeesu ne ko: «Waa jii, kan moo ma fal àttekat mbaa miraaskat ci seen kaw?»
15Ci kaw loolu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen wépp xeetu bëgge, ndax loo barele barele, sa bakkan ajuwul ci sa alal.»
16Mu léeb leen nag, ne leen: «Nit la woon ku woomle, te ab toolam nangu.
17Mu naan ca xel ma: “Nu may def nag? Amatuma sax fu ma denc sama ngóob mi!”
18Ci kaw loolu mu ne: “Nii laay def: samay sàq laay daaneel, daldi defaraat sàq yu gëna mag, denc ci sama pepp ak mboolem lu ma am.
19Su ko defee ci samam xel laa naan: ‘Céy sama waa ji, yaa ngeek alal ju bare ju mana dem ay ati at; neel finaax, di lekk, di naan ak a bége.’ ”
20Yàlla nag ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey jii, dees na jël sa bakkan. Kon li nga waajal, ana kuy doon boroom?”
21«Kuy dajaleel boppam alal te woomlewoo fa Yàlla, loolu mooy saw demin.»