Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 29

Kàddu yu Xelu 29:20-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20Ana koo gis, mu rattaxle? Kooku ab dof a ko gën demin.
21Ku yàq sab surga ba muy ndaw, bu ëllëgee mu defe ne doom la.
22Boroom xadar day sooke ay, te ku tàng bopp moy, moyati.
23Réy-réylu, detteelu rekk; woyofal, ñu naw la.
24Ku ànd akub sàcc, sa noonu bopp nga: soo waxee dëgg, yoon topp la; soo ko miimee, Yàlla topp la.
25Ragal nit dugal sa bopp la, ku wóolu Aji Sax ji, fegu.
26Ñu baree ngi sàkku kilifa baaxe leen, moona Aji Sax jeey àtteb jaam.
27Ku jub day sib ku dëng, ku bon sib kuy jubal.

Read Kàddu yu Xelu 29Kàddu yu Xelu 29
Compare Kàddu yu Xelu 29:20-27Kàddu yu Xelu 29:20-27