20 Ana koo gis, mu rattaxle? Kooku ab dof a ko gën demin.
21 Ku yàq sab surga ba muy ndaw, bu ëllëgee mu defe ne doom la.
22 Boroom xadar day sooke ay, te ku tàng bopp moy, moyati.
23 Réy-réylu, detteelu rekk; woyofal, ñu naw la.
24 Ku ànd akub sàcc, sa noonu bopp nga: soo waxee dëgg, yoon topp la; soo ko miimee, Yàlla topp la.
25 Ragal nit dugal sa bopp la, ku wóolu Aji Sax ji, fegu.
26 Ñu baree ngi sàkku kilifa baaxe leen, moona Aji Sax jeey àtteb jaam.
27 Ku jub day sib ku dëng, ku bon sib kuy jubal.