8Naka la mana ame nag, nu di leen dégg, kenn ku nekk ci nun, ñuy wax ci sa làmmiñ, wi nga nàmp?
9Nun ñi ay Pàrt, waa Medi ak waa Elam, nun ñi dëkk Mesopotami, réewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi,
10di waa Firisi, Pamfili, Misra ak weti Libi, yi dend ak Siren, nun ak gan ñi jóge Room,
11Yawut yi ak ñi tuub ci yoonu Yawut yi, waa Keret ak waa Arabi, nun ñépp nu ngi leen di dégg, ñuy yégle màggaayi Yàlla ci sunuy làkk!»
12Noonu ñépp waaru, ba jaaxle lool, ñuy waxante ci seen biir ne: «Lii lu muy tekki?»
13Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! Ñii dañoo màndi ak biiñ.»
14Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax!
15Nit ñii màndiwuñu, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk.
16Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne:
17“Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi, dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit ñépp; seen xeet wu góor ak wu jigéen dinañu wax ci kàddug Yàlla; waxambaane yi dinañu gis ay peeñu te màggat yi di gént ay gént.
18Waaw, ci bés yooyu dinaa tuur ci sama Xel ci sama kaw jaam yu góor ak yu jigéen, te dinañu wax ci kàddug Yàlla.
19Dinaa wone ay kéemaan ci kaw ci asamaan ak ay firnde ci suuf ci àddina, muy deret, sawara ak ay niiri saxar.
20Jant bi dina daldi lëndëm, weer wi deretal, bala bésu Boroom biy ñëw, di bés bu mag, bi ànd ak ndam.
21Booba nag ku woo Boroom bi ci aw turam, dinga mucc.”
22«Yéen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu mi dëkk Nasaret, nit la woon, ku Yàlla dëggal ci seen kanam ciy kéemaan, ay jaloore ak firnde, ya Yàlla defoon jaarale ko ci moom ci seen biir; yéen xam ngeen ko.
23Moom nag jébbale nañu ko, jaar ci nas, bi Yàlla dogaloon te xam ko lu jiitu; te yéen rey ngeen ko ci daaj ko ci bant, jaarale ko ci loxoy bàkkaarkat.
24Waaye Yàlla dekkal na ko, daggal ko buumi dee, ndaxte dee manu koo téye.
25Daawuda wax na ci mbiram ne: “Saa su ne gis naa Boroom bi ci sama kanam; gannaaw mu ngi ci sama ndijoor, duma raf.
26Moo tax sama xol sedd, may woy sama bànneex, te it sama yaram di tëdd ci yaakaar.
27Ndaxte doo bàyyi sama ruu ci barsàq, te doo seetaan sa waa ju sell, mu yàqu.
28Xamal nga ma yoonu dund; dinga ma béglooji ci sa kanam.”
29«Bokk yi, man naa leena wax lu wóor ci mbirum maam Daawuda, ne dee na te suul nañu ko; bàmmeelam mu ngi ci nun ba tey.
30Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàlla digoon na ko ci ngiñ ne dina teg ci nguuram kenn ci askanam.
31Kon gis na lu ñëwagul, di wax ci mbirum ndekkitel Kirist ne bàyyiwuñu ko ci barsàq, te yaramam yàquwul.
32Yeesu moomu nag, Yàlla dekkal na ko; nun ñépp seede nanu ko.
33Yàlla yéege na ko ak ndijooram, te jot na ci Baay bi Xel mu Sell mi ñu dige woon, ba tuur lii ngeen gis te dégg ko.
34Ndaxte du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam nee na: “Boroom bi wax na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor,
35ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ”
36«Na bànni Israyil gépp xam bu wóor nag ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàlla def na ko Boroom ak Almasi bi.»
37Bi ko mbooloo ma déggee, naqaru xol wu metti jàpp leen; ñu daldi ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, lu nu wara def?»
38Piyeer ne leen: «Tuubleen seeni bàkkaar, te kenn ku nekk ci yéen, ñu sóob ko ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Noonu Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar te may leen Xel mu Sell mi.