Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 25

Jëf ya 25:5-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Mu ne leen: «Kon nag, na nit ñu am baat ñu bokk ci yeen, ànd ak man, tuumaali waa ji, ndegam am na fenn fu mu tooñe.»
6Festus toogaatul ak ñoom lu wees juróom ñett ba fukki fan, doora dellu Sesare. Ba mu agsee ba ca ëllëg sa la toog ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi Póol.
7Ba Póol dikkee, Yawut ya jóge Yerusalem yéew ko, teg ko tuuma yu bare te réy, te manuñu cee firndeel lenn.
8Ci kaw loolu Póol weddi tuuma yi, ne: «Muy yoonu Yawut yi, di kër Yàlla gi, di Buur bu mag bi Sesaar, tooñuma ci kenn.»
9Festus nag bëgg lu neex Yawut yi, tax mu ne Póol: «Ndax nangu ngaa dem Yerusalem, ñu àttee la foofa ci mii mbir ci sama kanam?»
10Póol itam ne ko: «Maa ngi nii taxaw ci kanam àttekaayu Buur Sesaar; te fii lañu ma wara àttee. Yawut ñi nag, defuma leen dara, te yaw ci sa bopp, wóor na la.
11Su ma tooñee, su ma defee lenn lu dee di àtteem, tinuwma ngir baña dee. Waaye su lenn amul ci li ma ñii di jiiñ, kenn amul sañ-sañu jébbal ma leen. Buur Sesaar nag laa dénk sama bopp!»
12Ci kaw loolu, Festus gise ak waa kurél ga, ba noppi ne ko: «Sesaar nga dénk sa bopp, ca Sesaar nga jëm.»
13Gannaaw ab diir buur Àggripa ànd ak jigéenam Berenis ganesi Sesare, ngir nuysi Festus.
14Ba ñu fa amee ab diir, Festus diis Buur Àggripa mbirum Póol, ne ko: «Jenn waay ju ñu tëj kaso la nu Feligsë bàyyee.
15Ba ma demee Yerusalem, moom la ma sarxalkat yu mag yeek njiiti Yawut yi booleeloon, di sàkku ci moom ab daan.
16Ma ne leen: “Aaday Room daal nanguwul ñu jébbale nit, ngir ñu rey ko, te jëkkula jàkkaarloo ak ñi ko tuumaal, ba mana layal boppam ci mbir mi ñu ko tuumaal.”
17Ba ñu dikkee fekk ma fii itam, yàggaluma ci dara, ca ëllëg sa sax laa toog ca àttekaay ba, daldi joxe ndigal, ñu indi waa ji.
18Ba tuumaalkat ya taxawee nag, feeñaluñu jenn tuuma ju bokk ci yu bon, yi ma foogoon,
19xanaa seen yenn yëfi diiney bopp yu ñu juboowul, ak mbirum ku ñuy wax Yeesu mu dee woon, te Póol moomu di dëggal ne mu ngi dund ba tey.
20Loolu nag jaaxal ma, ba ma laaj ko ndax nangu naa dem Yerusalem, ñu àttee ko fa ci moomu mbir.
21Póol itam sàkku ñu dencagum ko kaso, tey sàkku ci mbiram, àtteb buur bu tedd bi. Ma daldi joxe ndigal, ngir ñu dencagum ko kaso, ba ma yebal ko ca Sesaar.»

Read Jëf ya 25Jëf ya 25
Compare Jëf ya 25:5-21Jëf ya 25:5-21