Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 25:5-21 in Wolof

Help us?

JËF YA 25:5-21 in Téereb Injiil

5 Mu ne leen: «Ñi am maana ci yéen nag, nangeen ànd ak man, layooji ak nit ka, bu dee tooñ na.»
6 Noonu Festus am fa ñoom juróom ñett ba fukki fan, ba noppi dem Sesare. Ca ëllëg sa mu toog ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi Pool.
7 Bi mu ñëwee nag, Yawut ya jóge Yerusalem wër ko, di ko jiiñ tooñ yu bare te réy, te manuñu leena firndeel.
8 Noonu Pool làyyi ne: «Tooñuma yoonu Yawut ya, tooñuma kër Yàlla ga, tooñuma buur ba Sesaar.»
9 Ci kaw loolu Festus, mi bëgg lu neex Yawut ya, wax Pool ne: «Ndax bëgguloo dem Yerusalem, nga layoo fa ci mbir yii ci sama kanam?»
10 Waaye Pool ne ko: «Maa ngi nii taxaw ci kanam àttekaayu buur Sesaar; te fii lañu ma wara àttee. Te yaw ci sa bopp xam nga bu baax ne tooñuma Yawut yi.
11 Su ma tooñoon mbaa ma def lu bon lu jar dee, kon duma tinu ngir baña dee. Waaye bu li ñu may jiiñ taxawul, kenn sañu ma leena jébbal. Dénk naa sama mbir Sesaar.»
12 Bi mu waxee loolu, Festus gise ak ñi ko wër, mu ne ko: «Dénk nga sa mbir Sesaar, kon ci moom ngay dem.»
13 Ba ñu ca tegee ay fan, buur Agaripa ak Berenis ñëw Sesare, ngir nuyusi Festus.
14 Bi seen ngan di ruus nag, Festus diis buur ba mbirum Pool ne ko: «Feligsë batale na nu ak kenn ku ñu tëj.
15 Bi ma nekkee Yerusalem, sarxalkat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame nañu ko ci man, ñaan ma, ma daan ko.
16 Waaye ma ne leen: “Jébbale nit, fekk jàkkaarloowul ak ñi koy jiiñ, ba mana làyyil boppam ci li ñu koy jiiñ, loolu dëppoowul ak aaday nguuru Room.”
17 Bi ñu àndee ak man ba fii nag, randaluma mbir mi, waaye ca ëllëg sa sax toog naa ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi nit kooku.
18 Ñi koy kalaame nag, bi ñu taxawee, jiiñuñu ko benn ñaawteef ci yi ma yaakaaroon,
19 waaye ñuy werante rekk ak moom ci seen yoon ak ci mbirum ku tudd Yeesu, mi dee, te Pool sax ci ne mu ngi dund.
20 Gannaaw lijjanti mbir moomu jafe woon na ma lool nag, ma laaj ko, ndax bëgg na dem Yerusalem, layooji fa ci mbir yooyu.
21 Waaye Pool ñaan, nu fomm mbiram, ba kera buur bu tedd ba di ko àtte. Noonu santaane naa ñu aj ko, ba keroog ma koy yónnee Sesaar.»
JËF YA 25 in Téereb Injiil

Jëf ya 25:5-21 in Kàddug Yàlla gi

5 Mu ne leen: «Kon nag, na nit ñu am baat ñu bokk ci yeen, ànd ak man, tuumaali waa ji, ndegam am na fenn fu mu tooñe.»
6 Festus toogaatul ak ñoom lu wees juróom ñett ba fukki fan, doora dellu Sesare. Ba mu agsee ba ca ëllëg sa la toog ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi Póol.
7 Ba Póol dikkee, Yawut ya jóge Yerusalem yéew ko, teg ko tuuma yu bare te réy, te manuñu cee firndeel lenn.
8 Ci kaw loolu Póol weddi tuuma yi, ne: «Muy yoonu Yawut yi, di kër Yàlla gi, di Buur bu mag bi Sesaar, tooñuma ci kenn.»
9 Festus nag bëgg lu neex Yawut yi, tax mu ne Póol: «Ndax nangu ngaa dem Yerusalem, ñu àttee la foofa ci mii mbir ci sama kanam?»
10 Póol itam ne ko: «Maa ngi nii taxaw ci kanam àttekaayu Buur Sesaar; te fii lañu ma wara àttee. Yawut ñi nag, defuma leen dara, te yaw ci sa bopp, wóor na la.
11 Su ma tooñee, su ma defee lenn lu dee di àtteem, tinuwma ngir baña dee. Waaye su lenn amul ci li ma ñii di jiiñ, kenn amul sañ-sañu jébbal ma leen. Buur Sesaar nag laa dénk sama bopp!»
12 Ci kaw loolu, Festus gise ak waa kurél ga, ba noppi ne ko: «Sesaar nga dénk sa bopp, ca Sesaar nga jëm.»
13 Gannaaw ab diir buur Àggripa ànd ak jigéenam Berenis ganesi Sesare, ngir nuysi Festus.
14 Ba ñu fa amee ab diir, Festus diis Buur Àggripa mbirum Póol, ne ko: «Jenn waay ju ñu tëj kaso la nu Feligsë bàyyee.
15 Ba ma demee Yerusalem, moom la ma sarxalkat yu mag yeek njiiti Yawut yi booleeloon, di sàkku ci moom ab daan.
16 Ma ne leen: “Aaday Room daal nanguwul ñu jébbale nit, ngir ñu rey ko, te jëkkula jàkkaarloo ak ñi ko tuumaal, ba mana layal boppam ci mbir mi ñu ko tuumaal.”
17 Ba ñu dikkee fekk ma fii itam, yàggaluma ci dara, ca ëllëg sa sax laa toog ca àttekaay ba, daldi joxe ndigal, ñu indi waa ji.
18 Ba tuumaalkat ya taxawee nag, feeñaluñu jenn tuuma ju bokk ci yu bon, yi ma foogoon,
19 xanaa seen yenn yëfi diiney bopp yu ñu juboowul, ak mbirum ku ñuy wax Yeesu mu dee woon, te Póol moomu di dëggal ne mu ngi dund ba tey.
20 Loolu nag jaaxal ma, ba ma laaj ko ndax nangu naa dem Yerusalem, ñu àttee ko fa ci moomu mbir.
21 Póol itam sàkku ñu dencagum ko kaso, tey sàkku ci mbiram, àtteb buur bu tedd bi. Ma daldi joxe ndigal, ngir ñu dencagum ko kaso, ba ma yebal ko ca Sesaar.»
Jëf ya 25 in Kàddug Yàlla gi