Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Samiyel

2.Samiyel 24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji mereeti bànni Israyil, ba tax mu xiir Daawuda ci def lu leen di lor. Mu def ci xelam ne ko mu dem lim waa Israyil ak Yuda.
2Buur wax ak Yowab ma ca wetam, di njiital xarekat ya. Mu ne ko: «Wëral ci biir giiri Israyil gépp ba ñu daj, li ko dale diiwaanu Dan ca bëj-gànnaar ba Beerseba ca bëj-saalum. Nañu bind askan wi, ndax ma xam seenub lim.»
3Yowab ne ko: «Buur, yal na Aji Sax ji ful askan wi téeméeri yoon, nga fekke. Waaye sang bi, lu la xiir ci loolu?»
4Teewul kàddug Buur ëpp doole Yowab ak njiiti xarekat ya. Ñu bàyyikoo ca Buur, dem bindi askanu Israyil.
5Ñu jàll dexu Yurdan, dem dali Arower ca bëj-saalumu dëkk ba, ca biir xur wa, daldi dem Gàdd, jaare fa jëm Yaser.
6Ci kaw loolu ñu dem diiwaanu Galàdd, jàll ba Kades ca diiwaanu Etteen ña, dem Dan Yaan ak la ko wër, teg ca Sidon.
7Ba mu ko defee ñu dem ba Tir, dëkk ba ñu wëralee ab tata, jóge fa dem ca mboolem dëkk-dëkkaani Eween ñaak Kanaaneen ña. Ñu àkkeji Beerseba ca bëj-saalumu màndiŋu Yuda.
8Wër nañu réew ma mépp ci juróom ñeenti weer ak ñaar fukki fan, doora ñibbsi Yerusalem.
9Yowab nag indil Buur limu askan wa: Israyil di juróom ñetti téeméeri junniy góor (800 000) ñu tollu ci xare; Yuda di juróomi téeméeri junniy góor (500 000).
10Daawuda waññ askan wa ba noppi, fit wa ne rës, mu yedd boppam, daldi ne Aji Sax ji: «Aji Sax ji, bàkkaar naa lool. Léegi nag ngalla jéggal ma sama ñaawtéef, ndax def naa jëfi dof ju réy lool.»
11Ba Daawuda jógee ca ëllëg sa, kàddug Aji Sax ji dikkal Gàdd, yonent Yàlla ba féetewoo kër Buur Daawuda. Mu ne ko:
12«Demal ne Daawuda: “Aji Sax ji dafa wax ne: Ñett laa lay jox, nga tànn ci lenn lu ma lay def.”»
13Gàdd dem ca Daawuda, jottli ko ko, ne ko: «Ana yii yett loo ci taamu, mu dal ci sa kaw: juróom yaari ati xiif ci sam réew, am ñetti weer yooy daw say noon, am ñetti fani mbas ci sam réew? Xalaatal léegi te wax ci lenn, ma xam lu may jottli ki ma yónni.»
14Daawuda ne Gàdd: «Am naa njàqare lool; waaye naa tàbbi ci loxol Aji Sax ji, ndax yërmandeem réy na, waaye yàlla buma daanu ci loxol nit!»
15Ba loolu amee Aji Sax ji wàcce mbas ci kaw Israyil, dale ko ca suba soosa ba keroog ba àpp ba matee. Ña dee ca askan wa di juróom ñaar fukki junni (70 000) diggante Dan ca bëj-gànnaar ba Beerseba ca bëj-saalum.
16Naka la malaaka ma tàllal loxoom, ngir faagaagal Yerusalem, Aji Sax ji fomm, daldi wax ak Malaakam bóomkat may fàdd askan wa. Mu ne ko: «Doy na! Teggil sa loxo.» Booba malaakam Aji Sax jaa nga ca wetu dàggay Arawna, Yebuseen ba.
17Daawuda nag gis malaaka may fàdd askan wa. Mu ne Aji Sax ji: «Man miy sàmm bi déy, maa bàkkaar, maa def lu bon. Ñii diy xar doŋŋ yu topp ci man, lu ñu def? Na sa loxo dal ci sama kaw man kay, maak sama waa kër baay!»
18Ba loolu amee Gàdd dem ca Daawuda keroog ca bés ba, ne ko: «Demal, nga tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay ca dàggay Arawna, Yebuseen ba.»

19Daawuda dem ca, na ko ko Aji Sax ji sante, Gàdd jottli.
20Ba mu ko defee Arawna séen Buur, mu ànd aki jawriñam, jëm ca moom. Mu génn sujjóotal ko, dëpp jëëm ca suuf,
21ne ko: «Buur, sang bi, lu doon say tànk?» Daawuda ne ko: «Xanaa jëndsi sa dàgga jii, ba tabaxal fi Aji Sax ji sarxalukaay, ndax mbas mi dal ci kaw askan wi yem fi.»
22Arawna ne Daawuda: «Buur, sang bi, jëlal lu la neex, def ko sarax. Nag yaa ngi, jëlal def saraxu rendi-dóomal, watiiri bojju yeek bant, yi nag yiy lëkkloo, nga def ko matt.
23Man Arawna, maa la jox lii lépp, Buur. Yal na la sa Yàlla Aji Sax ji nangul.»
24Teewul Buur ne Arawna: «Déedéet, dama koy jënd ci yaw kay. Ab saraxu rendi-dóomal bu ma dikkewul dara, duma ko defal sama Yàlla Aji Sax ji.» Ci kaw loolu Daawuda jënd dàgga ja ak nag ya ci juróom fukki dogi xaalis.
25Gannaaw loolu Daawuda tabaxal fa Aji Sax ji ab sarxalukaay, rendi fa ay saraxi dóomal, ak ay saraxi cant ci biir jàmm. Ba mu ko defee Aji Sax ji nangul réew ma, mbas ma bàyyi Israyil.