18Edom, mu moom; Seyir, noonam, muy boroom; Israyil def jaloore.
19Fa Yanqóoba la buur di bawoo, dem ñéddi ndesu dëkk ba.»
20Ci kaw loolu Balaam geesu réewum Amaleg, dellu yékki kàddug ñaanam, ne: «Amaleg moo sutu xeet, te sànku lay mujje.»
21Mu teg ca geesu réewum Keneen ña, yékkeeti kàddug ñaanam, ne: «Keneen ñee wér ab dëkkuwaay, seenub tàgg a làqoo biir doj.
22Waaye réewum Keneen gépp ay xoyomu, ba leen Asur di yóbbuji njaam.»
23Mu dellooti yékki kàddug ñaanam, ne: «Wóoy kuy dund, keroog bu Yàlla dogalee lii?
24Ay gaal ay jóge tefesu Kitim, néewalsi doole Asur, néewalsi doole Eber. Waaye ñoom it dañuy mujj sànku.»