Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 24:18-24 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 24:18-24 in Kàddug Yàlla gi

18 Edom, mu moom; Seyir, noonam, muy boroom; Israyil def jaloore.
19 Fa Yanqóoba la buur di bawoo, dem ñéddi ndesu dëkk ba.»
20 Ci kaw loolu Balaam geesu réewum Amaleg, dellu yékki kàddug ñaanam, ne: «Amaleg moo sutu xeet, te sànku lay mujje.»
21 Mu teg ca geesu réewum Keneen ña, yékkeeti kàddug ñaanam, ne: «Keneen ñee wér ab dëkkuwaay, seenub tàgg a làqoo biir doj.
22 Waaye réewum Keneen gépp ay xoyomu, ba leen Asur di yóbbuji njaam.»
23 Mu dellooti yékki kàddug ñaanam, ne: «Wóoy kuy dund, keroog bu Yàlla dogalee lii?
24 Ay gaal ay jóge tefesu Kitim, néewalsi doole Asur, néewalsi doole Eber. Waaye ñoom it dañuy mujj sànku.»
Màndiŋ ma 24 in Kàddug Yàlla gi