Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 20

Màndiŋ ma 20:1-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mbooloom bànni Israyil gépp nag àgg ca màndiŋu Ciin, ci biir weer wi jëkk ci at mi. Ñu daldi dal ca Kades. Fa la Maryaama faatoo, ñu denc ko foofa.
2Ci kaw loolu mbooloo ma dem ba ñàkk ndox. Ñu daje ci kaw Musaa ak Aaróona.
3Mbooloo ma di xulook Musaa, naa ko: «Moo lu nu tee woona dee keroog ba sunu bokk ya deeyee fa kanam Aji Sax ji?
4Ana loo indee mbooloom Aji Sax ji ci màndiŋ mii, nu di fi deesi doŋŋ, nook sunug jur?
5Ana loo nu jële woon Misra, di nu indi fu bon fii? Du bérab bu nangu menn jiwu: du figg, du reseñ, du gërënaat, te du siitum ndox mu ñu naan!»
6Ba loolu amee Musaa ak Aaróona bàyyikoo ca mbooloo ma, dem ba ca bunt xaymab ndaje ma. Ñu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf. Leeru Aji Sax ji nag feeñu leen.
7Aji Sax ji wax ak Musaa, ne:
8«Jëlal saw yet, nga dajale mbooloo mi, yaak sa mag Aaróona, ngeen wax ak doj woowu, ñuy gis, mu xelli am ndox. Te nga sottil leen ndox mu jóge ci doj wi, nàndale ko mbooloo mi, ñook seenug jur.»
9Ba mu ko defee Musaa jële yet wa fa kanam Aji Sax ji, na mu ko ko sante.
10Musaa ak Aaróona nag dajale mbooloo ma fa janook doj wa, Musaa ne leen: «Yeen diiŋatkat yi, dégluleen ma fii! Doj wii, tee nu leen cee génneel am ndox boog?»

Read Màndiŋ ma 20Màndiŋ ma 20
Compare Màndiŋ ma 20:1-10Màndiŋ ma 20:1-10