Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 9

Luug 9:19-46

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Ñu ne ko: «Ñii nee ñu yaa di Yaxya; ñee ne yaa di Ilyaas; ñale ne kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki, di yaw.»
20Yeesu ne leen: «Yeen nag, ngeen ne maay kan?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasib Yàlla.»
21Mu femmu leen nag, sant leen ñu bañ koo wax kenn.
22Mu neeti: «Fàww Doomu nit ki sonn lu bare, ba dajeek mbañeelu magi askan wi ak sarxalkat yu mag yi, ak firikati yoon yi, te dees na ko rey, ba ñetteelu fanam, mu dekki.»
23Yeesu nag wax leen ñoom ñépp, ne leen: «Képp ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp, te nga gàddu bés bu nekk, bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
24Ndax képp ku namma rawale sa bakkan, yaay ñàkk sa bakkan, waaye képp ku ñàkk sa bakkan ngir man, yaa musal sa bakkan.
25Ndax nit ki, su jagoo àddina sépp sax, te nara ñàkk bakkanam mbaa mu sànku, ana lu mu koy jariñ?
26Képp ku kersawoo sama jëmm, kersawoo topp samay wax, yaw itam Doomu nit ki dina la kersawoo, bés bu dikkee ci darajaam ak darajay Baay bi, ak darajay malaaka yu sell yi.
27Maa leen ko wax déy, ñenn a ngi fii taxaw tey, duñu dee te gisuñu nguurug Yàlla.»
28Ba lu wara tollook juróom ñetti fan wéyee gannaaw kàddu yooyu, Yeesu àndoon na ak Piyeer ak Yowaan ak Yanqóoba, ñu yéeg ca kaw tund wa ngir julli.
29Naka lay julli, xar kanamam soppiku, ay yéreem weex tàll, di melax.
30Ci kaw loolu ñaari nit jekki feeñ, di waxtaan ak moom; ñuy Yonent Yàlla Musaa ak Yonent Yàlla Ilyaas.
31Ñoo feeñ ci ag leer, di waxtaane dëddug Yeesu, ga mu doon waaja sottale fa Yerusalem.
32Booba ngëmment a ngay man Piyeer ak ña mu àndal. Ba ñu teewloo nag lañu gis leeru Yeesu, ak ñaar ña mu taxawal.
33Ba ñu demee ba ñaari nit ñooñu di bàyyikoo fa Yeesu, Piyeer ne ko: «Njaatige, su nu toogoon fii de, mu baax ci nun; nan yékkati ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa, benn Ilyaas.» Waaye booba Piyeer xamul la muy wax.
34Naka lay wax loolu, aw niir dikk yiir leen, taalibe ya tàbbi ca biir niir wa, tiitaange jàpp leen.
35Ci biir loolu baat jibe ca niir wa, ne: «Kii moo di sama Doom, ki ma taamu; dégluleen ko.»
36Ba baat ba selawee, Yeesu doŋŋ a feeñ. Taalibe ya nag ñoom ne cell, waxuñu kenn lenn jant yooyu, ca la ñu gis.
37Ca ëllëg sa ba ñuy wàcce tund wa, mbooloo mu baree dikk dajeek Yeesu.
38Jenn waay jekki xaacoo ca mbooloo ma, ne: «Sëriñ bi, dama lay ñaan, nga xoolal ma sama doom, ndax moom doŋŋ laa am.
39Rab kat moo ko jàpp, mu jekki di yuuxu, di say, gémmiñ giy fuur. Daanaka du teqlikook moom te sonal na ko.
40Ñaan naa say taalibe ngir ñu dàqal ma ko, waaye manuñu ko.»
41Yeesu ne leen: «Céy niti tey, yeena gëmadi te dëng! Maak yeen ba kañ, te di leen muñal? Indi sa doom fii.»
42Naka la xale bi jubsi Yeesu, rab wi sànni ko ci suuf, muy say. Yeesu itam gëdd rab wa, wéral xale ba, delloo ko baayam.
43Ñépp nag waaru ci màggug Yàlla. Naka la ñépp di yéemu ca mboolem la Yeesuy def, mu ne taalibeem ya:
44«Ubbileen seeni nopp te teewlu bu baax kàddu yii: Doomu nit ki lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit ñi.»
45Taalibe ya nag dégguñu kàddu googu, ndax fekk na piri ma làqu leen, ngir ñu bañ koo daj, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
46Werante moo dikkaloon taalibe yi, ñuy seet kan moo gëna kawe ci ñoom.

Read Luug 9Luug 9
Compare Luug 9:19-46Luug 9:19-46