Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 1

LUUG 1:3-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe.
4Noonu dinga mana xam ne li ñu la jàngaloon lu wér péŋŋ la.
5Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na sarxalkat bu ñu tudde Sakari te bokk ca mbootaayu sarxalkat, ya askanoo ci Abiya. Soxnaam Elisabet askanoo moom itam ci Aaróona.
6Sakari ak soxnaam ñu jub lañu ca kanam Yàlla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi yépp.
7Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet manula am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu.
8Benn bés nag Sakari doon def liggéeyu sarxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog.
9Bi ñuy tegoo bant, ni ko sarxalkat yi daan defe naka-jekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakari.
10Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan.
11Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakari, taxaw ca féeteek ndijooru sarxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam.

Read LUUG 1LUUG 1
Compare LUUG 1:3-11LUUG 1:3-11