Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 1

Luug 1:10-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10Mbooloo mépp nag a nga woon ca biti di julli, ca waxtuw saraxu cuuraay boobu.
11Ci biir loolu menn malaakam Boroom bi jekki feeñu Sàkkaryaa, ca wetu ndijooru sarxalukaayu cuuraay ba.
12Ba ko Sàkkaryaa gisee daa jaaxle, tiitaange jàpp ko.
13Malaaka ma ne ko: «Sàkkaryaa, bul tiit, ndax sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina am doom ju góor, nanga ko tudde Yaxya.
14Dinga am mbégte ak bànneex, te ñu bareey bég ci juddoom,
15ndax ku màgg lay doon, Boroom bi seede. Biiñ ak lenn luy màndee nag, du ko naan, Noo gu Sell gi mooy dale ca biiru ndeyam, solu ko ba fees.
16Niti bànni Israyil ñu bare, moo leen di waññi ci Boroom bi seen Yàlla.
17Mooy ndaw li koy jiitu, ànd ak leer ga ak xam-xam, ba woon ca Yonent Yàlla Ilyaas, ba waññi xolu baay ci doomam, waññi ku déggadi ci xelum aji jub, loolu yépp ngir waajal aw xeet ba ñu jekk ngir Boroom bi.»
18Sàkkaryaa nag ne malaaka mi: «Lu may def ab takk ci loolu ba mu bir ma? Ndax man màggat naa, te sama soxna it làq na ay fan.»
19Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw fi kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw, yégal la bii xibaaru jàmm.
20Léegi nag, dama ne, gannaaw gëmuloo sama kàddu, giy jot, sotti, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera loolu di am.»
21Ci biir loolu mbooloo maa ngay xaar Sàkkaryaa, jaaxle lool ndax yàggaayam ca biir néeg Yàlla ba.
22Ba mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Ñu daldi xam ne am na lu ko feeñu ca néeg Yàlla ba. Ma nga leen di liyaar, manatula wax.
23Naka la Sàkkaryaa fégal ayu carxalam, daldi ñibbi.
24Gannaaw gi, soxnaam Elisabet ëmb. Lëlu na juróomi weer. Ma nga naan:
25«Lii Boroom bee ma ko defal ci jant yi mu ma geesoo, ba teggil ma sama gàcce gi ci biir nit ñi!»
26Ba Elisabet tolloo ci juróom benni weeram, ca la Yàlla yebal Jibril malaaka mi, dëkk bi ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile,
27ci janq bu digoo séy ak waa ju ñuy wax Yuusufa te bokk ci waa kër Daawuda. Janq ba Maryaama lañu koy wax.
28Malaaka ma agsi ba ca moom, ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi ñu baaxe, Boroom bi yaw la àndal.»
29Waxi malaaka ma nag jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
30Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla.
31Dinga ëmb, ba jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
32Ku màgg lay doon, te dees na ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam.

Read Luug 1Luug 1
Compare Luug 1:10-32Luug 1:10-32