Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 1:10-32 in Wolof

Help us?

LUUG 1:10-32 in Téereb Injiil

10 Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan.
11 Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakari, taxaw ca féeteek ndijooru sarxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam.
12 Naka la ko Sakari gis, fitam daldi dem, mu tiit.
13 Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakari, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya.
14 Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom,
15 ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu.
16 Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom.
17 Mooy jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Ilyaas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.»
18 Sakari daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama soxna it màggat na.»
19 Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xibaaru jàmm boobu.
20 Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»
21 Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakari yàgg ca bérab bu sell ba.
22 Waaye bi mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.
23 Bi Sakari matalee liggéeyu sarxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi.
24 Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet soxnaam ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer
25 te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!»
26 Bi Elisabet nekkee ci juróom benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
27 Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama.
28 Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.»
29 Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
30 Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam.
31 Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
32 Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam.
LUUG 1 in Téereb Injiil

Luug 1:10-32 in Kàddug Yàlla gi

10 Mbooloo mépp nag a nga woon ca biti di julli, ca waxtuw saraxu cuuraay boobu.
11 Ci biir loolu menn malaakam Boroom bi jekki feeñu Sàkkaryaa, ca wetu ndijooru sarxalukaayu cuuraay ba.
12 Ba ko Sàkkaryaa gisee daa jaaxle, tiitaange jàpp ko.
13 Malaaka ma ne ko: «Sàkkaryaa, bul tiit, ndax sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina am doom ju góor, nanga ko tudde Yaxya.
14 Dinga am mbégte ak bànneex, te ñu bareey bég ci juddoom,
15 ndax ku màgg lay doon, Boroom bi seede. Biiñ ak lenn luy màndee nag, du ko naan, Noo gu Sell gi mooy dale ca biiru ndeyam, solu ko ba fees.
16 Niti bànni Israyil ñu bare, moo leen di waññi ci Boroom bi seen Yàlla.
17 Mooy ndaw li koy jiitu, ànd ak leer ga ak xam-xam, ba woon ca Yonent Yàlla Ilyaas, ba waññi xolu baay ci doomam, waññi ku déggadi ci xelum aji jub, loolu yépp ngir waajal aw xeet ba ñu jekk ngir Boroom bi.»
18 Sàkkaryaa nag ne malaaka mi: «Lu may def ab takk ci loolu ba mu bir ma? Ndax man màggat naa, te sama soxna it làq na ay fan.»
19 Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw fi kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw, yégal la bii xibaaru jàmm.
20 Léegi nag, dama ne, gannaaw gëmuloo sama kàddu, giy jot, sotti, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera loolu di am.»
21 Ci biir loolu mbooloo maa ngay xaar Sàkkaryaa, jaaxle lool ndax yàggaayam ca biir néeg Yàlla ba.
22 Ba mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Ñu daldi xam ne am na lu ko feeñu ca néeg Yàlla ba. Ma nga leen di liyaar, manatula wax.
23 Naka la Sàkkaryaa fégal ayu carxalam, daldi ñibbi.
24 Gannaaw gi, soxnaam Elisabet ëmb. Lëlu na juróomi weer. Ma nga naan:
25 «Lii Boroom bee ma ko defal ci jant yi mu ma geesoo, ba teggil ma sama gàcce gi ci biir nit ñi!»
26 Ba Elisabet tolloo ci juróom benni weeram, ca la Yàlla yebal Jibril malaaka mi, dëkk bi ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile,
27 ci janq bu digoo séy ak waa ju ñuy wax Yuusufa te bokk ci waa kër Daawuda. Janq ba Maryaama lañu koy wax.
28 Malaaka ma agsi ba ca moom, ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi ñu baaxe, Boroom bi yaw la àndal.»
29 Waxi malaaka ma nag jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
30 Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla.
31 Dinga ëmb, ba jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
32 Ku màgg lay doon, te dees na ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam.
Luug 1 in Kàddug Yàlla gi