Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 13

Luug 13:14-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
14Njiitu jàngu ba nag yékkati kàddug ñaawlu ndax bésub Noflaay ba Yeesu faje. Mu ne mbooloo ma: «Juróom benni fan la nit ñi wara liggéey. Kon ci fan yooyu ngeen wara fajusi, waaye du ci bésub Noflaay.»
15Sang bi ne ko: «Jinigalkat yi ngeen doon! Xanaa du ci bésub Noflaay la kenn ku nekk ci yeen di yiwee aw yëkkam mbaa mbaamam ca gétt ga, ngir wëggi ko?
16Jigéen jii di sëtub Ibraayma, te fukki at ak juróom ñett a ngii Seytaane làggal ko, wareesu koo yiwi, teggil ko laago jii ci bésub Noflaay?»
17Ba mu waxee loolu, noonam yépp a rus, mbooloo ma nag di bége mboolem jëf ju yéeme, ja muy def.
18Yeesu neeti: «Ana lu nguurug Yàlla di nirool? Ana lu ma koy niruleel?
19Mu ngi mel ni doomu fuddën bu nit jël, sànni cib toolam. Mu sax, màgg ba doon garab gu njanaaw yi tàgg ciy caram.»
20Mu dellu ne: «Ana lu may niruleel nguurug Yàlla?
21Mu ngi mel ni lawiir ju jigéen sàkk, def ko ci ñetti natti sunguf, ba tooyal bépp mujj funki.»
22Yeesu moo doon jaare ay dëkk yu mag ak yu ndaw, jëm Yerusalem, di jàngle ca yoon wa.
23Mu am ku ko ne: «Sang bi, xanaa ñiy mucc ñu néew lay doon?» Mu ne leen:
24«Góor-góorluleen ba dugge ci bunt bu xat bi, ndax maa leen ko wax, ñu bareey jéema dugg, waaye duñu ko man.
25Bu boroom kër gi xasee jóg, ba tëj bunt bi, fa ngeen di doxe des biti, di fëgg naan: “Sang bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.”
26Su boobaa ngeen naan: “Noo daan bokk di lekk ak a naan, te sunuy pénc nga daan jànglee.”
27Mu neeti leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Soreleen ma yeen ñépp, defkati njubadi yi!”
28Foofa la ay jooy ak naqarlu bay yéyu di ame yoon, kera bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ak yonent yépp ca biir nguurug Yàlla, te fekk yeen ci seen bopp, ñu dàq leen ca biti.
29Penku ak sowu, bëj-gànnaar ak bëj-saalum, la aw nit di bawoo, dikk toog ca ndabal bernde la ca nguurug Yàlla.
30Su ko defee nag, ñenn a ngi mujje tey, waaye ëllëg ñooy jiitu; te ñenn a ngi jiitu tey, waaye ëllëg ñooy mujje.»
31Ca jamono jooju tembe la ay Farisen dikk, ne Yeesu: «Jógeel fii, te dem, ndax Buur Erodd da laa nara rey.»

Read Luug 13Luug 13
Compare Luug 13:14-31Luug 13:14-31