Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 4

Kàdduy Waare 4:7-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Ma seetlu leneen luy cóolóoli neen fi kaw suuf.
8Kenn a ngii, kenn ñaareelu ko, du doom, du mbokk. Doñ-doñam du dakk, te du doylu, mujj mu naan: «Kan laay doñ-doñil, di xañ sama bopp bànneex?» Loolu it, cóolóoli neen, di sas wu tiis.
9Ñaar a man kenn; doñ-doñoondoo, yoolu bu baax.
10Kenn daanu, moroom ma may ko loxo. Waaye ngalla ku daanu te amuloo ku la may loxo!
11Bu ñu tëddee di ñaar it, mana bokk nuglu. Waaye soo dee kenn, nooy nugloo?

Read Kàdduy Waare 4Kàdduy Waare 4
Compare Kàdduy Waare 4:7-11Kàdduy Waare 4:7-11