7 Ma seetlu leneen luy cóolóoli neen fi kaw suuf.
8 Kenn a ngii, kenn ñaareelu ko, du doom, du mbokk. Doñ-doñam du dakk, te du doylu, mujj mu naan: «Kan laay doñ-doñil, di xañ sama bopp bànneex?» Loolu it, cóolóoli neen, di sas wu tiis.
9 Ñaar a man kenn; doñ-doñoondoo, yoolu bu baax.
10 Kenn daanu, moroom ma may ko loxo. Waaye ngalla ku daanu te amuloo ku la may loxo!
11 Bu ñu tëddee di ñaar it, mana bokk nuglu. Waaye soo dee kenn, nooy nugloo?