Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 2

Jëf ya 2:2-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Ca saa sa coow jollee asamaan, mel ni riirum ngelaw lu bare doole, daldi fees dell biir kër ga ñu toog.
3Ci kaw loolu ay làmmiñ yu mel ni tàkk-tàkki sawara feeñu leen, làmmiñ ya séddlikoo, daldi toŋ ci kaw kenn ku nekk.
4Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.
5Booba ay toppkati yoonu Yawut a nga dëkke Yerusalem, te bawoo ci xeeti àddina yépp.
6Naka la coow li jolli, nit ñi daje, ku nekk ci mbooloo mi dégg ñuy làkk sa làkku bopp, mbooloo ma jaaxle.
7Ñu boole waaru ak yéemu, naa: «Ñii di wax nii ñépp, xanaa duñu waa Galile?
8Ana nu kenn ku nekk ci nun nag mana dégge ñuy wax ci làmmiñ wi nga nàmp?
9Muy waa Pàrt, ak Medd ak Elam ak Mesopotami ak Yude ak Kapados ak Pont ak Asi,
10ak Firisi ak Pamfili ak Misra ak wàllu Libi ga dendeek Siren, ak gan ñi jóge Room,
11ak Yawuti njuddu-ji-réew yeek tuubeen ñi, ak waa Keret ak Arabi, nun ñépp a leen dégg ci sunu làmmiñi bopp, ñuy siiwtaane jaloore yu Yàlla!»
12Ñépp waaru, ba jànnaxe, di wax ci seen biir naa: «Lii lu muy tekki nag?»
13Teewul ñenn ñay ñaawle, ne: «Ñii daal biiñ bu bees doŋŋ lañu naan ba màndi.»
14Ci kaw loolu Piyeer taxaw, mook Fukk ñaak benn, daldi àddu ca kaw, ne: «Yeen bokki Yawut yi, ak mboolem yeen ñi dëkke Yerusalem, dégluleen bu baax sama kàddu, ba xam lii lu mu doon.
15Ñii màndiwuñu, ni ngeen ko fooge, ndax yoor-yoor doŋŋ a jot.
16Lii kay mooy kàddu ga Yonent Yàlla Yowel jottli woon, ne:
17“Yàlla nee: Mujug jamono, maay tuur samag Noo ci kaw wépp suux; seeni doom, góor ak jigéen di biral waxyu, seeni xale yu góor di gis ay peeñu, màggat ñi di gént ay gént.
18Kera jant yooyu, sama jaam ñi, góor ak jigéen, maa leen di tuur samag Noo, ñuy biral waxyu.
19Te maay def ay kiraama fi asamaan aki firnde ci dun bi fi suuf; muy deret ak sawara ak niiru saxar.
20Jant beey soppliku ag lëndëm, weer wi doon deret, bésub Boroom bi doora taxawe màggaay ak daraja.
21Su boobaa, ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw.”
22«Yeen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu waa Nasaret bi, Yàlla moo firndeele ag dëggoom, ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll.

Read Jëf ya 2Jëf ya 2
Compare Jëf ya 2:2-22Jëf ya 2:2-22