Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 24

Jëf ya 24:5-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Waa jii lanu gis ne ab rambaaj la buy sabab réeroo ci biir Yawuti àddina sépp. Moom mooy njiitu ngér mu sikk mi ñuy wax Nasareen ñi.
6Kër Yàlla ga sax jéem na koo teddadil, noo ko jàpp.
8Yaw ci sa bopp, soo ko laajaatee ci mbir moomu mépp, dinga gis li nu koy jiiñ.»
9Yawut ya itam dëggal tuuma ja, ne noonee la mbir ma ame.
10Ba loolu amee boroom réew ma jox Póol kàddu gi. Mu ne: «Xam naa ne at yu baree ngii ngay àtte xeet wi. Moo tax ma am cawartey layool sama bopp.
11Man ngaa leerlul sa bopp ne ba ma demee Yerusalem di màggali ak léegi weeseegul fukki fan ak ñaar.
12Te giseesu ma may werante, mbaa may yëngal mbooloo; du ca kër Yàlla ga, du ca jàngu ya, du ca biir dëkk ba.
13Te itam li ñu may jiiñ nii tey, manuñu cee firndeel dara.
14Lenn de man naa la koo nangul. Yoon woowu ñu ne mooy ngér mu sikk, moom laay topp, di ko jaamoo sunu Yàllay maam. Teewul mboolem lu ñu bind ci yoonu Musaa ak téerey yonent yi, gëm naa ko.
15Yaakaar ji ma am, mooy yaakaar ji ñu am ñoom itam, ne ñi jub ak ñi jubadi, ñépp ay bokk dekki ëllëg.
16Moo tax fu ma tollu, man itam, may def lu ma man ngir am xel mu dal, wàccoo ak Yàlla, wàccoo ak nit ñi.
17«Samay tànk nag, gannaaw gëjeb at yu bare, moo doon indil samaw askan, ay ndimbal ak ay sarax yu ñeel Yàlla.
18Ci biir loolu lañu ma fekk ca biir kër Yàlla ga, ma setlu, te du mbooloo, du coow lu ma indaale.
19Xanaa ñenn Yawuti diiwaanu Asi ña ma fa fekkoon. Ñooñoo ma waroona tuumaal fi sa kanam, ndegam am nañu lenn lu ñu ma sikke.
20Mbaa boog, na nit ñii ci seen bopp wax gan ndëngte lañu ma gisal, keroog ba ma taxawee ca kurélu àttekat ya!

Read Jëf ya 24Jëf ya 24
Compare Jëf ya 24:5-20Jëf ya 24:5-20