Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 6

1.Buur ya 6:1-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ca ñeenti téeméereelu at maak juróom ñett fukk (480), gannaaw ba bànni Israyil génnee réewum Misra, ca ñeenteelu atu nguurug Suleymaan, ci weeru Siw, di ñaareelu weeru at ma, ca la Suleymaan tàmbalee tabax kër Aji Sax ji.
2Kër gi Buur Suleymaan tabaxal Aji Sax ji, juróom benn fukki xasab la guddaay bi am, yaatuwaay bi di ñaar fukki xasab, taxawaay bi di fanweeri xasab.
3Buntu néeg bu mag bi ab dëru biti la jàkkaarlool, yaatuwaayu dër bi di ñaar fukki xasab, tollook yaatuwaayu kër gi. Guddaayam féete ci kanam kër gi, yokke guddaayu kër gi fukki xasab.
4Mu defal miiri kër gi ay palanteer yu am feguwaay yu ñu we ay caax.
5Mu tabax ay taax yu sës ca ñetti miiri kër gi. Taax yi dar ñaari miiri néeg bu mag bi ak miiru néegu biir bu sell bi ci gannaaw. Taax yi def ay néeg yu ndaw.
6Taax mi féete suuf juróomi xasab mooy yaatuwaayam, taax mi ci tegu di juróom benni xasab. Taaxum kaw mi am yaatuwaayu juróom ñaari xasab; ndax dañoo bàyyi ay teguy làcc ci miiri kër gi, ngir xaddi taax yi baña jàpp ci miiri kër gi.
7Kër ga, ba ñu koy tabax ay doj lañu ko tabaxe, muy doj yu ñu yett fa ñu ko jële ba noppi, moo tax du saddu, du sémmiñ mbaa lenn luy jumtukaayu weñ bu ñu dégg mu dal, diir ba ñuy tabax kër ga.
8Buntu taax mi ci suuf ma nga féete woon ndijoor, nit mana jaare ci ay dëggastal, yéeg jàll ci taaxum digg mi, jóge ci taaxum digg mi, jàll ci taax mi ci kaw.
9Suleymaan tabax kër gi ba noppi, xadde ko dénki garabi seedar ak gàlluy seedar.
10Taaxi kaw yi wër kër gépp, bu ci nekk juróomi xasab la def taxawaayam, lëkklee ko peeri garabu seedar, ba mu sës ca kër ga.
11Ci biir loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Suleymaan. Mu ne ko:
12«Kër gii de yaa ngi koy tabax. Waaye soo sàmmee samay dogal ak samay ndigal, di jëfe sama santaane yépp, di ci topp, su boobaa dinaa sottal li ma digoon sa baay Daawuda ci sa mbir.
13Dinaa dëkk ci digg bànni Israyil, te duma dëddu Israyil, sama ñoñ.»
14Ba mu ko defee Suleymaan tabax kër gi, ba sottal ko.
15Fa féete biir nag, mu lale miir yi xànqi seedar, dale ko ci suuf ba ci xadd bi. Dafa lal biir kër gi bant, lal dër bi xànqi sippar.
16Bàyyi na itam ñaar fukki xasab ci biir kër gi ci gannaaw, muy néeg bu mu lale banti seedar ci suuf ba ci xadd bi ci kaw. Mu sàkk ko ci biir kër gi, mu dib néegu biir bu sell, di bérab bu sell baa sell.
17Ñeent fukki xasab yi ko féete kanam di néeg Yàlla bu mag bi.
18Banti seedar yi lale ci biir kër gi, dees cee yett ay nataali koog ak tóor-tóor yu focci; lépp di bantu seedar, ba xeer feeñul.
19Néeg bu sell baa sell ca biir kër ga ca biir-a-biir la waajal, ngir yeb fa gaal gay def àlluway kóllërey Aji Sax ji.

Read 1.Buur ya 61.Buur ya 6
Compare 1.Buur ya 6:1-191.Buur ya 6:1-19