1Aji Sax ji dellooti wax Musaa ne ko:
2«Samay màggal, man Aji Sax ji, dangeen koo wara siiwal, muy ndaje yu sell. Samay màggal yii la.
3«Juróom benni fan lees di liggéey, bésub juróom ñaareel ba bésub Noflaay doŋŋ lay doon, di bésub ndaje mu sell. Du lenn lu ngeen ciy liggéey. Bésub Noflaay la bu ñuy jagleel Aji Sax ji, ak fépp fu ngeen dëkk.
4«Aji Sax ji, deeleen yégle ay màggalam, muy ay ndaje yu sell yu ngeen di wormaal saa yu jotee. Màggal yii la.
5«Fukki fan ak ñeent ci weer wi jëkk, diggante ngoon ak jant bu so, mooy màggalu bésub Mucc ba, ñeel Aji Sax ji.
6«Fukki fan ak juróom ci weer woowu la ayu bésu Mburu mu amul lawiir di tàmbali, ñeel Aji Sax ji. Diiru juróom ñaari fan mburu mu amul lawiir ngeen wara lekk.
7Bés bu jëkk bi ndaje mu sell ngeen ciy amal. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.
8Defleen ci saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji diiru juróom ñaari fan. Bésub juróom ñaareel ba di bésub ndaje mu sell. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.»
9Su loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
10«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu ngeen duggee ca réew ma ma leen jox, ba dajale la ngeen jële ca suufam, yóbbuleen ci sarxalkat bi takku peppum lors bi ngeen jëkka góob.
11Sarxalkat bi day yékkati takk bi, jébbal ko Aji Sax ji, ngir mu nangul leen. Bés bi topp ci bésub Noflaay bi lay yékkati takk bi, jébbal ko ko.
12Bés bi ñuy yékkati takk bi, jébbale, nangeen ci sarxal kuuy mu amul sikk, tollu ci menn at, ñu defal ko Aji Sax ji saraxu rendi-dóomal.
13Saraxu pepp mi muy àndal juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, ñu xiiwe ko diw, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm. Sarax si ñuy tuural Aji Sax ji, liitaru biiñ laak genn-wàll.
14Du mburu, du pepp mu ñu séndal, du pepp mu bees mu ngeen wara lekk, ba keroog bés boobu ngeen di indi seen saraxu Yàlla. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan, ak fépp fu ngeen dëkk.
15«Bésub Noflaay ba ngeen di indi takku bele biy saraxu yékkati-jébbale, bés ba ca topp ngeen di dale waññ juróom ñaari ayi bés yu mat sëkk.
16Waññleen ba ca bés ba topp ci juróom ñaareelu bésub Noflaay ba, muy juróom fukki fan, ngeen indil ca Aji Sax ji saraxu pepp mu bees.
17Seeni kër ngeen di jële ñaari mburu yuy doon saraxu yékkati-jébbale, mu ci nekk di lu ñu lakke juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib; dees ciy def lawiir, lakkaale ko ko, muy saraxu ndoortel meññeef, ñeel Aji Sax ji.
18Na mbooloo mi booleek mburu mi juróom ñaari kuuy yu amul sikk te tollu ci menn at, ak yëkk ak ñaari kuuy, mu doon saraxu rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji. Na ànd ak saraxu pepp ak sarax si ñuy tuur. Loolu sarax la ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
19Te itam ngeen sarxal ab sikket buy doon saraxu póotum bàkkaar ak ñaari xari menn at, muy saraxu cant ci biir jàmm.
20Sarxalkat bi day yékkati ñaari xar yooyu, boole kook mburum ndoortel meññeef mi, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. Yooyu sarax di lu sell ñeel Aji Sax ji, sarxalkat bee ko moom.
21Wooteleen ci bés boobu ndaje mu sell, te lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan, ak fépp fu ngeen dëkk.
22«Bu ngeen dee góob seen tool, buleen góob ba fa tool ba yem te buleen ci toppaat, di foraatu. Aji ñàkk akub doxandéem ngeen koy bàyyee. Maay seen Yàlla Aji Sax ji.»
23Gannaaw loolu Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
24«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu juróom ñaareelu weer taxawee, bés bi jëkk ci weer wi, na doon seen bésub Noflaay bu ngeen di amal ndaje mu sell. Deeleen fàttlee bés bi liit yu xumb.
25Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey, waaye nangeen ci indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.»
26Aji Sax ji teg ca wax Musaa ne ko:
27«Te itam fukki fan ci juróom ñaareelu weer woowu, bésub Njotlaay ba lay doon. Ndaje mu sell ngeen ciy amal. Nangeen ci toroxlu te indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
28Du lenn lu ngeen di liggéey ci boobu bés, ndax bésub Njotlaay la bu ngeen di jotoo fi seen kanam Yàlla, Aji Sax ji.
29Te kat, képp ku toroxluwul boobu bés, dees koy dagge ci biir bànni Israyil.
30Képp ku liggéey lenn ci boobu bés, su boobaa dinaa far kooku ci biir bànni Israyil, sànk ko.
31Buleen ci liggéey dara. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan ak fépp fu ngeen dëkk.
32Seen bésub Noflaay la bu ngeen di nopplu doŋŋ te war cee toroxlu. Li ko dale ci ngoonug juróom ñeenti fan ci weer wi ba ca ëllëg sa, ba jant so, ci ngeen di wormaal seen bésub Noflaay.»
33Su loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
34«Waxal bànni Israyil ne leen: Ñu waññ dale ko ci fukki fan ak juróom ci weeru juróom ñaareel woowu ba mu am juróom ñaari fan. Diir boobu mooy màggalu bési Mbaar yi, ñeel Aji Sax ji.
35Bés bu jëkk bi bésub ndaje mu sell la. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.
36Diiru juróom ñaari fan ngeen di indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Bésub juróom ñetteel, ba wara doon seen ndaje mu sell, nangeen ci indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Ndajem mujjantal ba la. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.
37«Yooyoo di màggali Aji Sax ji, yi ñu wara yégle, di ndaje yu sell yu ñuy indi ay saraxi sawara, ñeel Aji Sax ji, muy saraxu rendi-dóomal, ak saraxu pepp, ak yeneen saraxi jur gu ñuy rendi, ak sarax yi ñuy tuural Aji Sax ji, bés bu nekk ak la ca war.
38Yooyu sarax jotewul dara ak saraxi bési Noflaay yu Aji Sax ji. Jotewul dara it ak yi ngeen di joxeel Aji Sax ji mbaa mboolem sarax yi ngeen di wàccoo ngiñ, ak mboolem saraxi yéene yi ngeen di defal Aji Sax ji.
39«Ci biir loolu, fukki fan ak juróom ci juróom ñaareelu weer wi, gannaaw bu ngeen dajalee meññeefum réew mi, amal-leen màggalug Aji Sax ji diiru juróom ñaari fan. Na bés bu jëkk ba di bésub Noflaay, bésub juróom ñetteel ba di bésub Noflaay.
40Bés bu jëkk ba wittleen doomi garab yu rafet ak cari tiir ak cari garab yu sëq ak cari garab yu ñuy wax sóol, tey saxe tàkkal dex. Nangeen bànneexu fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji diiru juróom ñaari fan.
41Wormaal-leen màggalug Aji Sax jooju, di juróom ñaari fan cim at, te wormaal-leen ko ci juróom ñaareelu weer wi. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan.
42Ci ay mbaar ngeen di dëkk diiru juróom ñaari fan yooyu. Mboolem njuddu-ji-réew ci Israyil na ci dëkke mbaar,
43su ko defee seeni sët xam ne ciy mbaar laa dëkkaloon bànni Israyil, ba ma leen génnee réewum Misra. Maay seen Yàlla Aji Sax ji.»
44Noonu la Musaa xamale bànni Israyil bési màggalug Aji Sax ji.