Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy

Ngën-gi-woy 7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Dikkal, janqu waa Sulam bee, dikkal; dikkala dikk, nu niir la. Waa ji Moo, lu ngeen di seetaane janqub waa Sulam bi ni kuy fecc galanu Ñaari Dali Xare?
2Janqoo, lingeer sama, sa tànk yee ka jekk ci sa dàll yi, sa mooco yi mërgalu niy jaaro yu ndaanaanu tëgg yette loxoom.
3Sa jumbux bi di kaas bu mërgalu, yàlla bumu ñàkk biiñu njafaan! Sa biir bi di jalu pepp mu ay tóor-tóor ñag.
4Sa ween yi ni ñaari tef, mbaa seexi kéwél.
5Sa loos wi, coleet, rattax, ni tatay bëñi ñay; say gët di lerxat ni déegi Esbon, ya feggook buntu Bat Rabim. Sa bakkan bi jub xocc ni tatay Libaŋ ja tiim Damaas.
6Sa bopp siggi ni tundu Karmel, njañ liy nes-nesi ni sooyu buur, létt yay fëy-fëyi, ba laaw buur.
7Rafet, sopploo! Soppee, bànneex nga!
8Sa taxawaay bii garabu tàndarma la, sa ween yi di cëggi doom ya.
9Ma ne, maay yéeg tàndarma gi, ŋëb doom yi. Yal na say ween di sama cëggi reseñ, sag noo jox ma doom yu xeeñ,
10sa gémmiñ di xelli ngëneelu biiñ. Ndaw si Na walal sama nijaay, tuurul ñiy nelaw.
11Man, nijaay a moom, te maay nammeelam.
12Nijaay, ayca nu dem tool ba, fanaani ca tóor-tóori fuddën ya.
13Nan teela xëyi ca tóokëri reseñ ya, bu reseñ ji jebbee, mbaa tóor-tóor yi focci, mbaa gërënaat ji tóor, nu gis. Fa laa lay jébbale mbëggeel.
14Tóor-tóor yu xeeñ yaa ngi gilli, lépp luy doom yu neex aje sunu bunt néeg, yu yees yaak ya woon, ma boole dencal la, nijaay.