3Ci kaw loolu Musaa yebal ndaw ña ci ndigalal Aji Sax ji, ñu bàyyikoo ca màndiŋu Paran. Ñoom ñépp ay njiiti bànni Israyil lañu woon.
4Ñooñu ñoo di: Samwa doomu Sakuur, ci giirug Rubeneen ñi,
5ak Safat doomu Ori, ci giirug Cimyoneen ñi,
6ak Kaleb doomu Yefune, ci giirug Yudeen ñi,
7ak Igal doomu Yuusufa, ci giirug Isakareen ñi,
8ak Oseya doomu Nuun, ci giirug Efraymeen ñi,