Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 5

LUUG 5:29-36

Help us?
Click on verse(s) to share them!
29Noonu Lewi togglu ay ñam yu bare ci këram, ngir teral Yeesu. Juutikat yu bare ak yeneen gan ñu nga fa woon, di lekkandoo ak ñoom.
30Farisen yi ak seeni xutbakat di xultu taalibey Yeesu yi ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak di naanandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
31Yeesu ne leen: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
32Ñëwuma ngir woo ñi jub, waaye ngir woo bàkkaarkat yi, ñu tuub seeni bàkkaar.»
33Noonu ñu ne Yeesu: «Taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi dinañu faral di woor ak di ñaan ci Yàlla, waaye say taalibe ñu ngiy lekk ak di naan.»
34Yeesu ne leen: «Ndax man ngeena woorloo gan, yi ñëw cig céet, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom?
35Waaye bés yaa ngi ñëw, yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir. Bés yooyu nag, dinañu woor.»
36Te it Yeesu wax leen léeb wii: «Kenn du jël mbubb mu bees, xotti ci sekkit, daaxe ko mbubb mu màggat. Lu ko moy, dina xotti mbubb mu bees mi, te sekkit, wi mu ci jële, du ànd ak mbubb mu màggat mi.

Read LUUG 5LUUG 5
Compare LUUG 5:29-36LUUG 5:29-36