Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 3

Luug 3:3-36

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Yaxya dugg mboolem àll, bi wër dexu Yurdan, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir ñu jéggal leen seeni bàkkaar.
4Loolu lañu bind ci téereb waxi Yonent Yàlla Esayi ne: «Baat a ngi xaacoo ca màndiŋ ma, naan: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen ay xàllam.
5Xur yépp ay sëkke, tund wu magoo wu ndaw maasaloo, yoon ya lunkoon, jubbantiku, ya ñagasoon, nooy,
6ba wépp suux gis mucc gi Yàlla dogal.”»
7Yaxya nag di wax mbooloo may ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, naan leen: «Yeen njurum jaan mee, ku leen àrtu, ba ngeen di daw sànj miy dikk?
8Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel, te baña nax seen bopp naan: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan.
9Te itam sémmiñ xàccil na reenu garab ba noppi. Kon nag gépp garab gu ci meññul doom yu baax, dees koy gor, sànni ca sawara sa.»
10Mbooloo ma itam laaj ko ne ko: «Ana lu nu war nag?»
11Mu ne leen: «Ku am ñaari turki, na sédd ki amul. Ku am aw ñam itam, na defe noonu.»
12Ay juutikat itam dikk, ngir sóobusi; ñu ne Yaxya: «Sëriñ bi, ana lu nu war?»
13Mu ne leen: «Xanaa baña sàkku lenn lu moy li jaadu.»
14Ay takk-der itam ne ko: «Nun nag, nu nuy def?» Mu ne leen: «Buleen néewal kenn doole, mbaa di duural kenn ngir jëlal ko dara; doyloo leen seen peyoor.»
15Ci kaw loolu askan wa di séentu, ñépp di seetaat ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi.
16Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man de ci ndox laa leen di sóob. Waaye ku ma sut a ngi ñëw, kooku, buumi caraxam sax, yeyoowuma ko koo feccil. Moom, ci Noo gu Sell gi ak sawara la leen di sóob.
17Ab layoom a ngi ci loxoom, mooy jéri dàggaam, ba mu set wecc; pepp mi lay fat cim sàqam, waaye xatax bi, da koy lakk ci sawara su dul fey mukk.»
18Bare na yeneen dénkaane yu Yaxya doon xamale nit ñi xibaaru jàmm bi.
19Erodd boroom diiwaan ba nag, Yaxya sikkoon na ko ndax Erojàdd jabaru magam ja mu nekkaloon, ak mboolem yeneen ñaawtéef yu Erodd def.
20Mu tegati leneen ca loolu lépp: jàpp Yaxya, tëj ca kaso ba.
21Noonu Yaxya doon sóobe ñépp cim ndox, ni la deme ba Yeesu dikk, mu sóob ko ci ndox. Ci biir loolu Yeesu yékkati kàddug ñaan, asamaan ubbiku.
22Ba loolu amee Noo gu Sell gi moo bindoo ni pitax, wàcc ci kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaa may bànneexal.»
23Yeesu ci boppam ba muy door, amoon na lu tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa, ni ko xel mana jàppe. Yuusufa, Eli mooy baayam,
24Eli, Matat. Matat, Lewi; Lewi, Melki; Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
25Yuusufa, Matacas; Matacas, Amos; Amos, Nawum; Nawum, Esli; Esli, Nagayi.
26Nagayi, Maat; Maat, Matacas; Matacas, Semeyin; Semeyin, Yoseg; Yoseg, Yoda.
27Yoda, Yowanan; Yowanan, Resa; Resa, Sorobabel; Sorobabel, Selcel; Selcel, Neri;
28Neri, Melki; Melki, Adi; Adi, Kosam; Kosam, Elmadam; Elmadam, Er.
29Er, Yeesu; Yeesu, Elyeser; Elyeser, Yorim; Yorim, Matat; Matat, Lewi;
30Lewi, Simeyon; Simeyon, Yuda; Yuda, Yuusufa; Yuusufa, Yonam; Yonam, Elyakim.
31Elyakim, Meleya; Meleya, Mena; Mena, Matata; Matata, Natan; Natan, Daawuda.
32Daawuda mooy doomu Yese; Yese, Obedd; Obedd, Bowas; Bowas, Sala; Sala, Nason.
33Nason, Aminadab; Aminadab, Admin; Admin, Arni; Arni, Esron; Esron, Peres; Peres, Yuda;
34Yuda, Yanqóoba; Yanqóoba, Isaaxa; Isaaxa, Ibraayma; Ibraayma, Teraa; Teraa, Naxor;
35Naxor, Serug; Serug, Rew; Rew, Peleg; Peleg, Eber; Eber, Sela;
36Sela, Kenan; Kenan, Arpagsàdd; Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg;

Read Luug 3Luug 3
Compare Luug 3:3-36Luug 3:3-36