Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 19

LUUG 19:36-44

Help us?
Click on verse(s) to share them!
36Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi.
37Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis.
38Ñu ngi naan: «Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na jàmm am ca asamaan, te ndam li féete ca bérab yu gëna kawe!»
39Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!»
40Noonu mu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.»
41Bi Yeesu jegee dëkk ba, ba séen ko, mu jooy ko
42naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la mana indil jàmm! Waaye fi mu ne manuloo koo gis.
43Bés dina ñëwi yu say noon di jal, wërale la. Dinañu la tëj ci biir, tanc la.
44Dinañu la yàqate, yaw ak sa waa dëkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte ràññeewoo jamono ji Yàlla ñëwe, wallusi la.»

Read LUUG 19LUUG 19
Compare LUUG 19:36-44LUUG 19:36-44