Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 19:36-44 in Wolof

Help us?

LUUG 19:36-44 in Téereb Injiil

36 Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi.
37 Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis.
38 Ñu ngi naan: «Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na jàmm am ca asamaan, te ndam li féete ca bérab yu gëna kawe!»
39 Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!»
40 Noonu mu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.»
41 Bi Yeesu jegee dëkk ba, ba séen ko, mu jooy ko
42 naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la mana indil jàmm! Waaye fi mu ne manuloo koo gis.
43 Bés dina ñëwi yu say noon di jal, wërale la. Dinañu la tëj ci biir, tanc la.
44 Dinañu la yàqate, yaw ak sa waa dëkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte ràññeewoo jamono ji Yàlla ñëwe, wallusi la.»
LUUG 19 in Téereb Injiil

Luug 19:36-44 in Kàddug Yàlla gi

36 Naka la Yeesuy dem, nit ñi di ko lalal seeni yére ca yoon wa.
37 Ba ñu jubsee Yerusalem, bay wàcce ca mbartalum tundu Oliw ya, mbooloom taalibe mépp la mbégte jàpp, ñu tàmbalee sàbbaal Yàlla ca kaw ndax kéemaan ya ñu gis.
38 Ña nga naan: «Na barke wàccal buur bi ñëw ci turu Boroom bi! Jàmm fa asamaan; daraja fa bérab ya gëna kawe!»
39 Yenn Farisen ya woon ca mbooloo ma nag ne Yeesu: «Sëriñ bi, yeddal sa taalibe yi!»
40 Mu ne: «Maa leen ko wax, su ñii noppi woon, doj yi ñooy xaacu.»
41 Ba Yeesu jubsee ba séen dëkk ba, jooy na ndax moom.
42 Mu ne: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey jii li lay may jàmm! Waaye fii mu ne, làqu na say gët.
43 Ay bés a ngi dikk ci sa kaw, keroog say noon a lay gawe ab sëkk, yéew la, tance la wet gu nekk.
44 Ñoo lay nappaaje ci suuf, yaak say doom yi ci sa biir, te duñu bàyyi doj ci kaw doj ci sa biir, ndax ba sa bésub wall dikkee, yaa ko ràññeewuloon.»
Luug 19 in Kàddug Yàlla gi