Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 13

Luug 13:18-34

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Yeesu neeti: «Ana lu nguurug Yàlla di nirool? Ana lu ma koy niruleel?
19Mu ngi mel ni doomu fuddën bu nit jël, sànni cib toolam. Mu sax, màgg ba doon garab gu njanaaw yi tàgg ciy caram.»
20Mu dellu ne: «Ana lu may niruleel nguurug Yàlla?
21Mu ngi mel ni lawiir ju jigéen sàkk, def ko ci ñetti natti sunguf, ba tooyal bépp mujj funki.»
22Yeesu moo doon jaare ay dëkk yu mag ak yu ndaw, jëm Yerusalem, di jàngle ca yoon wa.
23Mu am ku ko ne: «Sang bi, xanaa ñiy mucc ñu néew lay doon?» Mu ne leen:
24«Góor-góorluleen ba dugge ci bunt bu xat bi, ndax maa leen ko wax, ñu bareey jéema dugg, waaye duñu ko man.
25Bu boroom kër gi xasee jóg, ba tëj bunt bi, fa ngeen di doxe des biti, di fëgg naan: “Sang bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.”
26Su boobaa ngeen naan: “Noo daan bokk di lekk ak a naan, te sunuy pénc nga daan jànglee.”
27Mu neeti leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Soreleen ma yeen ñépp, defkati njubadi yi!”
28Foofa la ay jooy ak naqarlu bay yéyu di ame yoon, kera bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ak yonent yépp ca biir nguurug Yàlla, te fekk yeen ci seen bopp, ñu dàq leen ca biti.
29Penku ak sowu, bëj-gànnaar ak bëj-saalum, la aw nit di bawoo, dikk toog ca ndabal bernde la ca nguurug Yàlla.
30Su ko defee nag, ñenn a ngi mujje tey, waaye ëllëg ñooy jiitu; te ñenn a ngi jiitu tey, waaye ëllëg ñooy mujje.»
31Ca jamono jooju tembe la ay Farisen dikk, ne Yeesu: «Jógeel fii, te dem, ndax Buur Erodd da laa nara rey.»
32Mu ne leen: «Demleen wax njomboor moomu, ne ko: “Maa ngii di dàq rab yi, di maye ag wér, tey ak ëllëg. Bésub ñetteel ba nag ma sottal.”
33Waaye tey ak ëllëg ak sibir, fàww ma dem, ndax ab yonent wareesu koo bóome fenn fu dul Yerusalem.
34«Yerusalem, Yerusalem, yaw miy bóom yonent yi, di sànni ay doj ñi ñu yebal ci yaw, ba ñu dee, ñaata yoon laa namma dajale say doom, uuf ni ganaar di uufe ay cuujam, te nanguwuloo?

Read Luug 13Luug 13
Compare Luug 13:18-34Luug 13:18-34